Démb lañu ko téye woon fa “Section de Recherches” bu Kolobaan ñeel mbirum suuf mi ñu ko doon toppe. Nde, nee ñu dafa am ku mu jaayoon suuf te, matalewul li ñu digaale woon ñoom ñaar. Moom Aadama Fay, di rakk ci Mareem Fay, mujj nañu koo bàyyi. Ndax, bees sukkandikoo ci xibaar yi rotagum, kii di Ibu Fay, mag walla rakk ci moom, moo fay téeméeri miliyoŋ ak juróom ngir ñu bàyyi ko.
MBIRUM SÉEX BAARA NJAAY AK TEREES FAY
Coow li doxoon diggante Séex Baara Njaay ak Terees Fay ba ñu jébbaloon ko DIC, yëf yi jeexagul. Dafa mel ni day door kepp. Nde, tey ci alxames ji lañu woo kii di Séex Baara Njaay fa DIC ñeel coow loolu. Ndax, dafa am ay tuuma yu mu yékkati woon teg leen ci ndoddu soxna soosu nekkon fi jëwriñ ci Nguur gi fi jóge. Kon, fii ak ub diir, dees na xam luy tukkee ci woote boobu.
RÉEROO ÑEEL WAXTAANUW XUWAAN BARÀNKO FA UCAD
Ginnaaw ba Usmaan Sonko ak Mélenchon amalee woon aw waxtaan fa daara ju kowe jooju, tey kii di layookatu Njiitul Pastef li moo fa waroon a amal aw waxtaan. Waaye, loolu mujjewul a àntu. Nde, réeroo dafa am ci mbir mi ñeel càkkuteef gu ñu war a njëkk a wut laata loolu. Rax-ci-dolli, dañu ne woon dafay ñëw ci kow wooteb ndongo yiy gëstu ci wàllu Yoon (FSJP), ñooñu ne loolu dara amu ci. Laalewuñu ci, taqewuñu ci wenn yoon. Looloo tax, waxtaan wi fa béréb bii di CICES lañu ko mujje amale tey ci ngoonu alxames ji, bu juróomi waxtu jotee. Ki ko waxtaane mooy moom Meetar Xuwaan Barànkoo ak Meetar Bàmba Siise.
YENEEN TABB YU YEES
Démb ci àllarba ji lañu doon amal ndajem jëwriñ. Ca ndaje mooma, Njiitu réew mi Basiiru Jomaay Jaxaar Fay jot na faa jël ndogal. Nde, am na ñu mu jot a jox ay ndomboy-tànk. Ñi mu takkal ay ndomboy-tànk, ñii la :
Mataar Seen lañu tabb, « Délégué général à la Protection sociale et à la Solidarité nationale ». Mu wuutu fa soxna Aminata Sow ;
Soxna Amsatu Sow Sidibe, moom lañu tabb Njiitul « Comité sénégalais des Droits de l’homme ». Ki mu mu wuutu foofa di Meetar Pàppa Seen ;
Pàppa Tobi Gay, moom lañu tabb Njiitul SENELEC SA (Société nationale d’électricité) (SENELEC). Ki mu fa wuutu di Sëriñ Pàppa Mademba Bitéey ;
Alliyun Géy lañu tabb Njiitul « Société des Pétroles du Sénégal (PETROSEN Holding SA) ». Mu wuutu fa Aadama Jàllo ;
Muhammadu Jóob, tabb nañu ko Njiitul « Société des Pétroles du Sénégal (PETROSEN Trading and Services SA) ». Ki mu fa wuutu di El Haaj Manaar Sàll ;
Jean Michel Seen moom lañu tabb Njiitul « l’Agence sénégalaise d’Electrification rurale (ASER) ». Ki mu wuutu fa béréb boobu di Baaba Jàllo ;
Maam Kumba Njaay lañu tabb Njiitul « Agence pour l’Economie et la Maitrise d’Energie (AEME) ». Mu wuutu fa Sayeer Jóob ;
Moor Baaxum, moom lañu tabb « Secrétaire technique du Conseil national de Suivi du Contenu Local au Ministère de l’Energie, du Pétrole et des Mines » ;
Aamadu Géy lañu tabb Njiitul « Agence de Promotion des sites industriels (APROSI) ». Ki mu fa wuutu di Momat Ba ;
Aysatu Jàllo, tabb nañu ko « Coordonnateur du Programme national de Développement des Agropoles du Sénégal ». Ki mu fa wuutu di Jiili Lóo ;
Justin Coreyaa, moom lañu tabb Njiitul « Centre international du Commerce extérieur du Sénégal (CICES) ». Mu wuutu fa béréb boobu kii di Saalihu Keyta ;
Rugi Alaaji Sow, tabb nañu ko « Coordonnateur national du Programme de Modernisation et de Gestion des Marchés (PROMOGEM) ». Ki mu wuutu fa béréb boobu mooy Yaay Faatu Jaañ ;
Sàmbu Biyaagi lañu tabb Njiitul « Maison de la presse « Babacar TOURE ». Ki mu fa wuutu di Baara Njaay ;
Ndey Faatu Njaay, tabb nañu ko « Coordonnateur de l’Unité de Coordination et de Gestion du Fonds de Développement du Service universel des Télécommunications (FDSUT) ». Mu wuutu fa Móodu Maamun Ngom ;
Alliyu Faal, tabb nañu ko Njiitul « Alphabétisation et des Langues nationales ». Mingi wuutu fa béréb boobu Ndey Naam Juuf ;
Abdulaay Njaay, moom lañu tabb Njiitul « Administration générale et de l’Equipement au Ministère de l’Énergie, du Pétrole et des Mines » ;
Abuubakri Bóokum, tabb nañu ko Njiitul « Administration générale et de l’Equipement au Ministère de la Jeunesse, des Sports et de la Culture » ;
Al Hasan Jóob, moom lañu tabb Njiitul « Administration générale et de l’Equipement au Ministère des Pêches, des Infrastructures maritimes et portuaires ». Ki mu fa wuutu di Abdulaay Njaay.