LI GËN A FÉS CI XIBAAR BÉS BI (9/5/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

BÉSUB MÀGGALU “ASCENSION”

Tey, ci alxames ji, yemoo ak juróom-ñeenti fan ci weeru me, mooy bés bi ñi bokk ci diiney kercen di màggal yéegug Yónnentu Yàlla ba Iisaa ca kow asamaan. Mu doon bés boo xam ne am na solo lool ci diine jooju. Dafa di, mooy màndargaal bés bi mu mujjee ci kow suuf. Ñu koy màggal at mu jot bu “Pâques” jàllee ba mu am ñeen-fukki fan.

CONACOC BIRAL NA BÉS BU NJËKK CI DIGGI-TABASKI

Démb ci àllarba ji la kurél googu di CONACOC (Commission Nationale de Concertation sur le Croissant lunaire) daje woon ngir séentu weer wi. Su ko defee, ñu mën a xam kañ mooy bés bu njëkk ci weeru diggi-tabaski ak ñaata fan moo war a des ci tabaski gi. Bi ñu ko séentoo nag, amul fenn fu mu feeñ ci biir-réew mi. Kon, suba ci àjjuma ji mooy doon bés bu njëkk ci diggi-tabaski. Ci gàttal, weer ak fukki fan moo des ci tabaski gi.

WAAJTAAYU AJ GI AK TABASKI GI

Fii ak ñeen-fukki fan rekk ñu màggal bésub tabaski gi bu soobee Yàlla. Waaye, laata bés boobu, dafa am beneen xew-xew bu gën a jamp, muy aj gi. Nde, aj moom, kenn umpalewul ne benn la ci ponki lislaam yi. Looloo tax, elimaanu jëwriñ yi jàppal leen bési ndaje ngir ñoom jëwriñ yi ñu waxtaane waajtaay yi ak ya ca war. Ndaje yooyu, ñi ngi leen jàpp fukki fan ba fukki fan ak ñeent ci weeru me wii ñu nekk. Maanaam, li ko dale suba ci àjjuma ji ba talaata jii di ñëw.

TAW BI DOOR NA FA BANDAFASI

Bandafasi, ab dëkk la bu nekk fa Kéedugu. Fa dëkk boobu lañu nemmeeku ay taw yu am doole ci guddi gi. Te, du wenn yoon kese la fa taw sewet. Taw na fa ñetti yoon. Daf fa taw ba ay boori juróom-ñaari waxtu ci ngoon, mu sewet. Bi mu demee ba ay fukki waxtu ak benn ci guddi mu tawaat fa. Waaye, yemul foofu. Nde, bi mu demaatee ba guddi gi xaaj (00h) dafa tawaat, muy ñetti yoon. Li mat a laaj kay mooy, ndax nawet bi daf faa door am déet ?

XEW-XEW BU TIIS FA NDAKAARU

Xew-xew boobu ma nga am tey fa “Centre-Ville” ba ci boori “Rond-point Dupont et Demba”. Benn takk-der (policier) buy wuyoo ci turu B. Jiba la genn daamar fiir mu jaare fa ñàkk bakkanam. Nde, bi mbir mi xewee sax, yóbbu nañu ko fa raglu bi ñuy dippe “hôpital principal”. Waaye, mujjal a mucc. Bees sukkandikoo ci waa Seneweb, takk-der bi da doon dem ca bérébu liggéeyukaayam, ca la ko ndogal li dalee. Ki doon dawal daamar gi moom jamono jii ma nga ca loxoy Yoon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj