Ëllëg ci talaata ji, dees na tabb Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, mu waat ci kanamu askanuw Senegaal gépp, nees ko tàmmee gis saa su réew mi amee Njiitu réew mu bees ba mu war a tàmbali moomeem. Xew mi dina amee fa Jamñaajo, booy dugg Ndakaaru. Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak Sñ Basiiru Jomaay Fay mi koy wuutu waxtaane nañ ko ba noppi. Njiitu réew yu bare dinañu ko teewe, rawatina yu CEDEAO yi, Njiitu réewum Móritani ak mu réewum Gàmbi.
LIMUB JËWRIÑI CÀMM GU BEES GI
Basiiru Jomaay Fay dina wàññi limub jëwriñ yi nar a séq gornamaawam bi. Muy xibaar bu Ndeem Jeŋ, kenn ci ñi yor jokkoo ak jokkalante Diomay Président, siiwal. Bees sukkandikoo ci kàddu yi mu biral, wóor na ko ni Njiit lu bees li dina wàññ bariwaayu jëwriñ yi bu baax a baax. Dina jox ndomb-tànk yu ëpp yi solo ñu ci seen xel màcc. Ñenn ciy àndandoo yu Jomaay Fay biral nañ itam ni Njiit lee ngi nekk di liggéey ak i ñoñam ngir xool yan njëwriñ lees war a delloosi, yees war a dooleel ak yees war a far.
NDAKAARU : ÀBBAAS FAAL NOPPEEGUL CI XEEX BI
Àbbaas Faal noppeegul ci xeex bi ci digganteem ak Xalifa Sàll ak Bàrtelemi Jaas. Dépite Yewwi Askan Wi, di itam njiitul Pastef Ndakaaru, dellusi na ci ndam li ñu am foofu, ak xob yu takkoo takku yi ñu fa rawee Taxawu. Bees déggee bu baax li mu wax, Pastef mooy pàrti bi dooleel lëkkatoo YAW, rawatina foofu fa Ndakaaru. Waaye itam, lim bu bare bi ñu leen rawee foofu ci wote yi ñu génn dafay firndeel ni askanu Ndakaaru meree seen meer bi ci jëflanteem ak Pastef. Dafay waneet ni nit ñi ci seen bopp bëggatuñu ay wor ci géewu pólitig gi.
ÀTTEB NEENAL BEEK ÑI JOT A FAATU
Ci jamono yii weesu, Njiitu réew mi Maki Sàll amaloon na sémbub àtte wuy neenal lépp lu fi jaaroon ciy xew-xew, diggante 2021 ak 2024. Lu ni mel a waraloon ba ñu bare ñuñ nëbboon jant wi mën a génn kaso, ba ci Usmaan Sonko ak Basiiru Jomaay Fay mi ñu fal Njiitu réewum Senegaal. Waaye, 80i doom-aadam ñàkkoon nañ seen bakkan ci xew-xew yooyule. Ba tax kii di Àlliyun Tin, Boroom Afrika Jom Center, di ci bàyyiloo xel Njiitu réew miy ñëw. Li muy sàkku ci moom nag mooy mu taxawal barabu pàttaliku bu mu leen jagleen, fexe ba kenn bañ leen a fàtte walla di fàtte xeex bu am solo bi ñu amal ci sunu demokaraasi.
AKSIDAŊ BU METTI FA PADDUWAA
Aksidaŋ bu metti moo am tey ci altine ji, fa tollook Padduwaa. Moo ngi xew bi 4i waxtoo jotee ba war a teg ay 30i simili ci njël. Bees sukkandikoo ci li Kàppiteen Aysatu Keyta, komàndaŋ sàppëer bu Jëppal, jottali, bi ñu leen ko yégalee lañ daw, ñëw ci saa si. Waaye, mettiwaayu mbir mi tax na ba ñaar ci ñett ñiñ fa fekk jot nañ ñàkk seen i bakkan laata ñu leen di xettali.
MBËKK MI
Gaal gu bawoo fii ci réew mi teerati na ca tefesi Espaañ ya. Barki-démb ci gaawu gi la fa àgg ba ñu xettali ña mu yaboon ci waaxi El Hiyeroo, fa duni Kanari ya. Gaal gi yaboon na 171i way-tukki yoy, 87 yi ay Saa-Senegaal lañ. Kilifa ya xamle nañ itam ni gii mooy ñaareelu gaal gu ñuy xettali foofu ginnaaw bi gu njëkk gi teeree foofu ci alxames ji, bi 16i waxtu di jot.