LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (04/10/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

LU BEES ÑEEL GÉNNÉEG USMAAN SONKO CI WAYNDAREW WOTE YI

Ay fan ginnaaw bees jébbalee Njiitul Pastef li, Usmaan Sonko, bataaxel biy firndeel ne génnee nañu ko ci wayndarew wote yi, moom Usmaan Sonko ak i layookatam tooguñu tegaley tànk. Def nañu ñaari bataaxeli kalaame (Recours) ci ñaari béréb yu wute ngir ñu nasaxal ndogal loolu. Benn bi ña nga ko yóbbu ca ëttu àttewaay bu kowe ba ñuy dippe Cour suprême. Ñaareel ba ñu yóbbu ko ca ëttu àttewaay bu Sigicoor. Loolu terewul tamit ñu defaat beneen ngir naqarlu ndogal li DGE jël. Maanaan ñàkk a jox gi ñu ñàkk a jox Usmaan Sonko ay këyit yi mu war a defe baayale gi (parenaas yi).

ÀPP YU AM SOLO ÑEEL WOTEY 2024

Àpp yi ñeel wotey njiiteefu réew mi atum ñett lañu. Bi ci jiitu mooy ne, fukki fan ak benn ci weeru desàmbar mooy àpp bu mujj ñeel jébbalug wayndarey baayale gi. Ñaareel bi mooy fukki fan ak ñaar ci weeru saŋwiye 2024 ñu siiwal lawax yi ñu wéral. Ñi ñu gàntal seen i wayndarey baayale tamit ci lañu leen di siiwal. Ba ca mujj mooy ñaar-fukki fan ci weeru saŋwiye nga xam ne ci lañuy jibal lawax ya nga xam ne dinañu bokk ci wotey 2024 yi. Dees na siiwalaale mbooleem ñi nga xam ne duñu bokk ca wote yooya. Boole ceek may leen lu tollu ci ñaari fan ngir ñu wax ak juróom-ñaari kàngaami ndajem ndeyu àtte ji.

ISMAAYLA MAAJOOR DËGGAL NA WAA DGE

Jëwriñ ji ñu dénk wàlluw Yoon ci Senegaal Ismaayla Maajoor Faal wone na taxawaayam ñeel ndogal li waa DGE (Direction Générale des Elections) jël. Ndogal loolu mooy bañ a jox Usmaan Sonko ay këyiti baayale. Li mu layale ndogal loolu mooy ne Usmaan Sonko nekkatul ci wayndarew wote yi. Kon, moom, kenn mënu ko woteel. Looloo tax mënut a jot ci këyit yooyee, donte ne sax bari na ñoo xam ne ànduñu ci doxalin woowu. Ndax, dañoo jàpp ne pólitig kepp a ko lal.

FRAPP A NGI ARTU

Kurél gii di FRAPP mi ngi artu ñeel anam yi nit ñi ñu tëj ci kaso yi nekke. Li waral loolu du lenn lu dul la ña ñu jàpp ca kasob Kàmpenaal (Camp pénal) bu Liberte siis (Liberté 6) di ñaawlu. Li ñuy ñaawlu mooy seen nekkin wu metti wi ñu nekkee ca kaso ba, ni ñu ñàkkalee faayda seen ug wér-gi-yaram ak metital yi ñuy metital ñenn ci ñoom. Looloo tax ñuy door ag xiifal ngir naqarlu loolu. Ba tax ñii di waa FRAPP di fàttali kilifa yi ne ñi ñu tëj ci kaso yi duñu ay mala.

MBËKK MI

Mbirum mbëkk mi, ba tey mi ngi wéy di lëmbe Afrig sowu-jant, rawatina réewum Senegaal. Ay weer ci ginnaaw ba tey yëf yaa ngi gën a taqarnaase. Ñii àgg nañu, ñii dee nañu, ñii delloosi nañu leen. Démb nag moom, bés la ci bés yi. Ndax, lim bu takku ci ay doomi Senegaal ñoo teerijee fa Espaañ. Ñetti gaal ñoo fa teer. Te, yeboon nañu lu tollu ci ñeenti téeméer ak juróom-ñeent fukki doomi-aadama. Rax-ci-dolli, ñépp di ay doomi Senegaal, kenn raxu leen.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj