LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (04/3/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

ÑAXTUB VACATAIRES YI

REVUS (Regroupement des Enseignants Vacataires du Sénégal, di kurélug jàngalekat yi ñu duppe Vacataires ci jàngune yi) mi ngi naqarlu ñàkkal faayda ak ñàkk a yittewoo seen i mbir gi leen Nguur gi def. Ci yégle bi ñu génne, ña nga cay xamle ni ay weer a ngi nii ñuy waxtaan, di dem ak a dikk. Waaye, dañu gis ni kilifa yi dañu tanqamlu seen i càkkuteef. Te, seen i càkkuteef yooyu, dara gënu leen a yay walla yell. Ba ci ndaje mi Càmm gi doon amal naka keroog 27i fani féewiryee 2024, kenn joxu leen fa gëdd. Ba tax ñuy biral ni xel mënul a nangu ñu bëgg a saafar jafe-jafey njàng mu kawe mi te duñ leen ci boole. Nde, téeméer yoo jël ci jàngalekat yeek gëstukat yi, ay vacataires lañu. Muy nag lu féewaloo ak bëgg-bëgg bi elimaanu jëwriñ yi fésaloon ñeel waxtaan wu ñépp bokk.

AJ MÀKKA 2025

Dalub roppalaan bii di AIBD (Aéroport International Blaise Diagne) waajal na 30i yoon ngir yóbbu lu tollu ci 12 860i doomi réew mi ñu aji Màkka. Muy ndogal lu njiit la siiwal ginnaaw ba fa Seneraal Mamadu Gay mi jiite aj gi doxee ay tànk ci waajtaayi tukki boobu. Naka noonu, roppalaan yiy yóbbu yoon yooyu dinañu bawoo ci réew mi ci diggante 17 ak 24i fan ci weeru me. Waññeeku beet dàkk nañu ko ci weeru suwe bi. Ci kow loolu, Ajug ren ji, nattees na ko ci lu tollu ci 13i tamñareeti FCFA. Ñu teg lépp ci loxoy kër gii di Air Sénégal ginnaaw bi ñu càmbaree jafe-jafe yi ci ujaaj yi amoon daaw. Naka noonu, dina amal genn wàllu yoon yi. Geneen wàll gi mu jagleel ko kërug Araabi Sawdit gii di Flynas.

AIR Sénégal waajal na itam ay yoon wutali Jeddah, ci diggante 15 ak 16i fani màrs 2025 ñeel 750i ujaaj yi bindu ngir umraji.

ËTTU DABANTAL BU NDAAKAARU DËGGAL NA DAANUB MAJAMBAL JAAÑ

Démb ci altine ji, 3i fani màrs 2025, la ëttu dabantal bu Ndakaaru doon àddu ci dabantal bi Majambal Jaañ doon sàkku ci digganteem ak Suleymaan Teliko. Ginnaaw bi mu càmbaree àtte bu njëkk ba, ëttu dabantal bi dàqu ci lenn. Dafa dellu dëggal ni taskatu xibaar bi dafa waxalaate lu amul. Naka noonu, Majambal Jaañ dina tëdd ñetti weeri kaso, fay daan ci 500 000 FCFA. Dina jox itam Suleymaan Teliko ndàmpaay lu tollu ci 5i tamndareet. Cig pàttali, Majambal Jaañ dafa waxaloon Sëñ Teliko ni tudd nañu ko ci caabalug Bennoog Tugal (Union Européenne) ni dafa jot ay koppar ci lu teguwul ci yoon fekk mu doon dox ab soxla bu ëttu àttekaay bii di Chambres Africaines extraordinaire ci mbiri Hisen Habre ma woon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj