LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (08/11/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

AYIB DAFE JOTAGUL XOBI BAAYALE YI

Ba joxeg xob yi tàmbalee ba léegi daanaka moo ngi baagante diggante DGE ak CENA. Waaye, loolu taxul mu jot xob yi kii di njiitul Pastef li war a baayalee. Moom nag, ginnaaw bi ëttu àttewaayu Sigicoor bi nee nañu delloo Usmaan Sonko cxi wayndarew wote yi delluwaatoon na, taxul mu jot. Waa CENA tamit ne na ko waa DGE jox ba tey ñu bañ. Moom nag, ca CENA la mujje dem. Ci altine ji ba mu fa demee dafa fekk ñu tëj. Mu demaat fa démb, ñu ne ko mu ñëw tey. Ba tey moo nga fa waaye, jotagul xobi baayale yi. Lii nag mooy tës !

BÀYYI NAÑU JÓOB TAYIF

Lu jege juróom-ñetti weer ginnaaw bi ñu ko tegee loxo ak léegi, mujj nañu ko bàyyi bàyyig négandiku. Mamadu Lamin Jóob ñu gën koo xame ci turu Jóob Tayif kenn la ci ñoñi Usmaan Sonko yi ñu tegoon loxo bu yàgg ba tey. Li waraloon loolu mooy widewoo bu mu defoon ca kanamu Rëbës. Ñu ko doon toppe li ñuy dippe “ collecte de données à caractère personnel”. Moom nag bàyyi nañu ko tey. Waaye, liy tukkee ci layoob tey bi dees na ko leeral ñaar fukki fan ak ñaar ci weer wii.

Mu amaat yeneen ndawi Pastef yoo xam ne tey jii lañu leen waroon a àtte. Waaye, seen layoo boobu dañu koo mujjee dàq ba ñaar fukki fan ak ñaar ci weer wii. Muy ku ci mel ni Yarga Si, Maam Paate ak lu jege ñaar-fukki ndaw yoo xam ne ñoom ñépp Pastef lañu bokk.

MBIR MU DOY WAAR FA TUUBAA

Mbir mu doy waar moo xew démb fa Tuubaa. Benn baay faal lañu fa dóor balu fetal mu génn àdduna. Li waral coow loolu mooy ne baay faal yaa wàcc ci benn koñ bu tudd Firdawsi, fa lañu fekk ay sàmbaa-bóoy (trafiquants) ñu bañ ne ñooñu duñu leen teg loxo. Ca la coow la dooree ba jenn waay dóor ci bal benn baay faal buy wuyoo ci turu M. Ñaŋ mu faatu, beneen baay faal tamit jële na ciy gaañu-gaañu. Nee ñu tamit am na ñaar ci ñi ñu ne ay sàmbaa-bóoy lañu ñu ca amey gaañu-gaañu.

 LÀMB 

Dibéer jii ñu weesu lañu daan doomu Pikin jii di Aamaa Balde ci làmb ji doxoon digganteem ak doomu Pàrsel jii di Móodu Loo. Jeneen doomu Pikin war na sëggaat ci dibéer jii ñu dégmal. Kooku mooy Ëmma Seen. Moom nag, ak ki mu jàkkarlool kenn dootuleen aajar ci làmb. Dina jàkkaarloo ak kii di Tafaa Tin fukki fan ak ñaar ci weer wii. Moom Ëmma Seen tey ci àllarba ji la naroon a def li ñuy dippe “open-press” janoo ak i ñoñam. Waaye, dafa mel ni ñoom waa Pikin ba tey seen xol neexul. Nee na daf koy mujj bàyyi, taskati xibaar yi rekk lay mujje jàkkaarlool.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj