Ay fan yu néew ñoo des ngir kàmpaañ bi tàmbali. Looloo tax jamono jii lawax yépp a ngi wër ñu leen yokk doole. Am na ñenn ñu tàmbalee fekki yenn lawax. Mu am tamit lawax yuy seeti ñi seen i wayndare jàllul. Moo tax mbokki Basiiru Jomaay Fay yi seeti Bugaan Géy Dani ngir mu fekkisi leen. Xalifa Abaabakar Sàll moom it seeti woon na Doktoor Baabakar Jóob meeru Cees ngir mu ñëw ñu liggéey.
LU BEES CI TAAX MI DAANU WOON FA YARAAX
Jéyya jooja amoon fa Yaraax, limub ña ca loru ma ngay gën a yokk. Juróomi nit a ñàkkoon seen bakkan. Fim tollu nii, ñeneen ñaar yokku nañu ci lim boobu. Mu am fukki doomi-aadama ak ñaar yoo xam ne jële nañu ci ay gaañu-gaañu. Waaye, ba tey, loolu taxul ñu xam ndax limu ñi ci loru fii lay yem am déet.
CAN KODDIWAAR 2024
Mbetteel yaa ngay wéy di am ci joŋante boobu di xewe fa Koddiwaar. Ginnaaw ba Senegaal gi nga xam ne bokk na ci réew yi ñu jàppoon ne dinañu sori ci joŋante bi toogee. Am na meneen réew mu ko fekki. Keroog ci talaata ji la Marog miñ doon xaar fu sori tamit toog. Naka noonu ñii di waa Burkinaa Faaso tamit ñibbi nañu. Mu des joŋante yi war a am tey ci àjjuma ak gaawu. Muy diggante Niseriyaa ak Àngolaa ak diggante RD Kóngoo ak Gine. Kon, fii ak ub diir dees na xam ñan ñooy des fa Koddiwaar. Ak ñiy topp ci waa Marog ak Burkinaa Faaso.
SÓOBAREY SENEGAAL YI ÑIBBISI NAÑU
Ab diir ginnaaw ba ñu leen yebalee fa Mali ngir ñu delloosi fa jàmm, soldaari Senegaal yi delsi nañ. Bërki-démb ci talaata ji la ko jëwrin ji ñu dénk wàll woowu xamle. Moom Elaas Umar Yum xamle na ne ñàkk nañu lu tollu ci fukki sóobare ak juróom. Mu yokk ci ne ak li muy metti ci xol yépp, day wone ne jàmm moom amul njëg. Rax-ci-dolli, ne firnde la ci ne ñoom pare nañ ngir delloosi ag dal fa Mali.