LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (1/7/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

65eelu NDAJEM CEDEAO

Démb ci dibéer ji, 7i pani sulet 2024, kurél gii di CEDEAO (Communauté Économique des États de l’Afrique de l’Ouest) doon na amal 65eelu Ndaje mu mag yu Njiitu réew yeek Njiitu Càmm yi séq. Ña nga ko doon amalee fa Abujaa, réewum Niseriyaa, ci njiiteefu Sëñ Bolaa Ahmet Tinubu, Njiitu réew ma, di itam njiitu lëlu Njiit yi. Fànn yu bari waxtaane nañu leen. Bokk na ci yu gën a fés, caabalug Njiitu kurél gi ñeel tolluwaayu mbooloo mi ci atum 2024 mi, caabalug 52eelu ndajem diisoo giy dox ci jàmm ak kaaraange, ak caabalug 92eel ndajem jëwriñi CEDEAO yi.

KÀDDU NJIITU RÉEW MI ÑEEL NJIITI CEDEAO YI

Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ma nga woon démb fa réewum Niseriyaa, doon fa teewe ndaje mu mag mi fa Njiiti réew yeek Njiiti Càmm yu kurélu CEDEAO doon amal. Ginnaaw bi mu fa teewee nag, Njiitu réew mi biral na fa xalaatam ci xar-kanam gu yees gu kurél gi war a am. Muy woote bu mu def jagleel ko naataangoom yi. Naka noonu, mu leen di xamal ni seen kurél gi dafa war a tàqalikoo ak yenn xeeti gis-gis yu ñaaw yuñ koy askanale. Muy xeeti gis-gis yu koy def kurél gu fi nekkal doxandéem yeek réew yu am doole yi ba tax ñuy soofantal askan wi. Fekk moom lañ fi war a nekkal.

TAW YI WÀCC CI RÉEW MI

Ndox mu bari moo wàcc ci réew mi ak taw bu yàgg te am doole bu fi amoon démb ci dibéer ji. Ndox moomu sax, donte ni ndorteelu nawet bi la ci diiwaan yu bari ci réew mi, andil nay jafe-jafe ñenn ci askan wi ak mbënn mi mu leen dikkee. Mbënn moomu nag, gënees na koo nemmeeku ci dëkk yii di Ndakaaru, Ndar, Kawlax ak Tuubaa. Ginnaaw bi ñu leen nemmeekoo nag, Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Fay, àddu na ngir mastawu ñi ci loru. Xamal na leen itam ni Càmm gee ngi ci seen wet te dina leen taxawu ni mu waree.

BITIM-RÉEW

Mbetteel lu réy moo am ci ñaareelu pàccu wotey Ngombalaan gi ñu doon amal fa Farãs. Ginnaaw bi RN jitoo woon ci pàcc bu njëkk bi, xëccoo bi dafa gënoon fés ci seen digganteek waa Nguur gi. Waaye, làngug pólitig gii di Front Populaire moo mujje fëllee fu ko ñu bari foogeewul woon, daldi raw. Naka noonu, seen Njiit yu mel ni Sã-Lig Melãsõ ak Marin Tondeliyee xamle nañu ni, noppi nañ ngir jiite. Waaye, duñ nangu lëkkatoo ak kenn walla di am lu ñuy waxaale ak waa Nguur gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj