LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (1/7/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NJÀNGATI WOTEY 2024 YI

Kurélu maxejj gii di COSCE (Collectif des Organisations de la Société Civile pour les Élections) àddu na ci wotey Njiitu réew mi ñu fi doon amal keroog 24i pani màrs 2024. Seen gis-gis nag, mooy ni wote yi dafa gën a yékkati réewum Senegaal ci doxalinu demokaraasi. Nde, ginnaaw bi ñu saytoo doxalinu wote yi ba noppi, seetlu nañu ni amal nañ leen ci anam yu mucc ayib, wëliis jafe-jafe yi amoon ci géewu pólitig bi, yëngu-yëngu yi ñu juroon ak xaajaloo yi ñu ci nemmeeku ci diggante way-pólitig yeek fara maxejj yi ba mu amoon i njeexital ci dalug réew mi.

CAABALUG PÉNCOO MI ÑEEL WÀLLUW YOON

Caabalug péncoo miñ foo doon amal ñeel wàlluw yoon sotti na. Sëñ Baabakar Géy mi doon yombal waxtaan yi moo ko xamle tey ci altine ji. Fekk ñu doon amal ubbite caytu gees war a amal ci doxalinu wote yi fi réew mi, rawatina wotey Njiitu réew mi ñu doon amal ci 24i pani màrs 2024.

Naka noonu, muy xamle ni dees na jébbal caabal gi kii di Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ci alxames jii di ñëw. Mu yokk ceet ni am nañ yaakaar bu baax ni njureef yi tukkee ci péncoo moomu dina joyyanti bu baax doxinu yoon fi réew mi.

MAGUM JËWRIÑ YI DAKKAL NA PAS YI

Magum jëwriñ yi, Usmaan Sonko dakkal na lépp luy pas ci diggante Nguur geek yenn këru liigéey yi. Ginnaaw bi mu joyyantee peyoori lempo yu këru liggéey yu bari doon jalgati, dafa ajandi xaatimi déggoo yi, jëlub liggéey yeek pasi fésal yi ba jëmmi jamono. Ab bataaxal la yónnee ay ñoñam ngir ñu jébbal ko léppi wayndare ñeel tolluwaayu barabi liggéey yi aju ci seen njiiteef.

Bataaxal bi mu leen yónnee woon sax, moo nga ca doon sàkku ñu jébbal ko wayndare yi ci bésub 1eelu fan ci weeru sulet 2024, gën-gaa sori.

Ndogal loolu nag, magum jëwriñ yee ngi ko jël ci tànk JUB, JUBAL, JUBBANTI yi Càmm gi sumb, ngir teggil Nguur gi yenn yan yi koy diisal te amaluñ ko lenn njariñ. Ba tax muy wax barabi liggéey yooyu war a jot i koopar ci Nguur gi ak ñi doon séentuy liggéey ci bànqaasi Nguur gi ñu ànd ak dal te taaxirlu. Nde, Nguur gi dafa nekk ci tànki leeral yu mu gën a yittewoo.

WÉR-GI-YARAM

147i ujaaj am nañ jàngoro jii di Covid-19. Loolu la jëwriñ ji yor wàllu wér-gi-yaram xamle. Muy xibaar bu mu siiwal cib yégle bu mu jébbal kibaaraan yi. Lim boobu nag, ñoo ngi ko am ginnaaw bi ñu saytoo yarami 590i ujaaj yu jóge Màkka ci diggante 21 ak 27i pani suwe 2024.

Ngir bañ jàngoro ji tasaaroo ci biir réew mi, jëwriñ jee ngi woo Saa-Senegaal yu ñu gënn a farlu ci fagaru gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj