Béréb boobu doon yore ay xale te Ndeela Maajoor jiite woon ko, coow la feyagul. Ginnaaw bi ñu ko tegee loxo ak léegi, ñi ngi ci tànki ñi ko doon jàppale. Ki doon wattu kaaraange gi (vigile) ak ka mu bokkaloon jëf ja (complice) daan nañu leen. Moom Jean Nowel Nduur ak Aminata Wuri Jàllo daan nañu leen ñaari at yoo xam ne dinañu ca tëdd juróom-benni weer. Rax-ci-dolli, dinañu fey ndàmpaay lu tollu ci ñeen-fukki junni ci sunuy koppar.
MANSUUR SIISE DEM NA KASO
Mansuur Siise di kenn ci kilifay Pastef bu Mbuur fanaani na démb kaso. Li ko waral mooy pelent bu ko meeru Mbuur bi Séex Isaa Sàll defoon. Daf ko duut baaraam ci xew-xewam boobu ñu saboote woon. Dafa di, xew-xew booba, ndaw ñi la ko mayoon. Loolu mi ngi amoon fanweeri fan ak benn ci weeru desàmbar wii ñu génn.
BENEEN ÀPP ÑEEL LAWAX YI
Démb ci talaata ji la ndajem ndeyu àtte mi jeexal caytug xobi baayale yi. Ak ni limu lawax yi takkoo woon lépp, terewul ne, ñaar-fukk ak benn kese ñoo ca jàll. Ba tey nag, loolu du tere lim bi soppeeku. Ndax, dese na leen beneen tëb. Li ñu naan ku tëb dal ci xal dese na la beneen tëb. Ndege, fii ak fukki fan dinañu biral lawax yi nga xam ne seen wayndare mat na sëkk. Maanaam, lawax yi nga xam ne gis nañu ci ñoom juróom-ñeenti sàrt yi ñuy xool ci ñoom.
XEW-XEW BU DOY WAAR FA KËR MBAY FAAL
Coowal xale yooyu réer lëmbe na réew mi lool. Waaye, dafa am lu ci beesaat. Ndax, nee ñu, ñaari xale yi, ñu ngi leen fekk ci daamar gu ñu muur ak ub baas. Kenn ki, I. Faal, fekk nañu ko mu dee, deret muur bopp bi. Rax-ci-dolli, ñu ne dañoo fekk bët yi buqeeku. Keneen ki moom, mi ngi wuyoo ci turu I. Ja. Moom ay gaañu-gaañu yu metti la ame ci pooj bi.
Xadi faal am naw woy
Soxana Xadi Faal di takk-der bu jigéen bu ñu sas liggéey bu ñu mësul a jox jigéen. Liggéey boobu mooy téeméeri takk-der ak ñeen-fukk yi ñuy yebal fa Kóngoo, moo leen di jiite. Muy yoon wu njëkk jigéen di ko jiite fii ci Senegaal. Li ñu ko sant mooy saxal fa jàmm ak ug dal.
GAYNDE YI JËL NAÑU RAAYA RÉEW MI
Joŋante bi boole réewi Afrig yi, ñu dippee ko “CAN” dina door fii ak ub diir bu gàtt. Moo tax, jamono jii, réew yépp a ngi waajal seen i ndaw yi leen fa war a teewal. Gayndey Senegaal yi tamit desuñu ci ginnaaw. Ñoom it, ñu ngi ci waajtaay yi. Démb, ci talaata ji, la leen Njiitu réew mi Maki Sàll jox raaya gi. Maanaam, ngir ñu taxawal réewum Senegaal fa Koddiwaar ca gën-gaa rafeti taxawin.