Yoon a ngi wéy di teg bët ci liy xew ci saabalukaay yi. Ba tax na, lu ci bari ñuy nemmeeku muy woo ñu wax walla siiwal lu ëpp ci pénc mi. Mu mel ni, yu deme noonu moo tax ñu woolu Simõ Fay mi nga xam ne moo jiite wàllum mbind mi fa saabalukaay bii di SenTv. Moom Simõ lañu woo tay fa “Brigade des Affaires Générales” (BAG) bu “Division des Investigations Criminelles” (DIC). Li sabab ñu woo saabalkat boobu mooy lu ñeel tasaareg yaxalub “Afrique Confidentielle” bi ñu dippe “Crise politique au Sénégal : Ouattara convoque Ousmane Sonko à Abidjan” fa SenTv. Mbir moomoo tax ñu woolu ko bees sukkandikoo ci xibaar yi jot a rotagun.
LU BEES ÑEEL CÀCC GI AMOON “TRÉSOR PUBLIC”
Ci ndorteelu weeru màrs wii ñu génn lañu la ay sàmbaa-bóoy songoon “Trésorpublic”. Coow loolu lëmbe woon réew mi lool. Waaye, dafa am lu beesaat ci mbir mi. Nde, am na ñaar ñu ñu ci diir, te kenn ki sax jot nañu ko teg loxo. Yéenekaay bii di “Enquête” moo ko siiwal ci ay xëtam. Ki ñu ci teg loxo mi ngi wuyoo ci turu M. Sàll, tollu ci ñaar-fukki at ak juróom-benn, dëkk fa Rëbës. Waaye, yemuñu foofu. Ndax, xamle nañu waa ji nangu na bokk na ci càcc gi. Te it, wax na ki mu àndaloon ci jëf jooju. Te, nee na lépp Maalaw moomu la ko jox. Waa jooju nag, jamono jii, Yoon a ngi ci ay tànkam.
DÀQ NAÑU DEMUG ELIMAANU JËWRIÑ YI FA NGOMBLAAN GA
Tay, ci alxames ji, la elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, waroon na dem fa Ngomblaan ga, janoo ak dépite yi. Li mu ko dugge mooy tontu seen i laaj ñeel tolluwaayu réew mi. Waaye, ndaje moomu dañu ko mujje dàq. Li ko sabab mooy génnug àdduna Xalifa Seneraal Laayeen yi, Sëriñ Muhammadu Maxtaar Caw Laay. Loolu tekkiwul ne du dellu fa béréb boobu. Dina dem fa Ngomblaan ga altine ak jàmm bu fukki waxtu ci suba jotee.
NDOGUM YOON MU METTI FA MBÀKKE
Ndogi yoon yaa ngi wéy di gën a bari ci réew mi. Te, mu ñëw gën a yées. Tay, ci alxames ji, am na ndog mu metti mu am fa Mbàkke, ca wetu Dalla-Ngaabu, ay boori fukki waxtu ak benn ci suba. Benn Njaga Njaay moo fa mbëkkante ak genn sëfaan (camion-citerne). Ñaar-fukki doomi-aadama ak juróom-ñett jële ca ay gaañu-gaañu. Mu am ci fukk ak benn yoo xam ne sonn nañu lool bees sukkandikoo ci waa Seneweb.