LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (10/6/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

TABASKI 2025 : KÀDDUY NJIITU RÉEW MI

Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, yékkati woon na ay kàddu ci tabaski bi, bi mu jullee fa Jumaay Ndakaaru ju mag ja. Ginnaaw bi mu rafetloo xutba bu am solo ba imaam ba def, ñaanal na mbooleem kilifa diine yi ak kilifa aada yi ci réew mi. Sàkku na itam ci ñépp ñu ñaanal réew mi bennoo, dal ak yokkute.

Ginnaaw kàddu yooyu, njiitu réew mi dellu na jaajëfal mbooleem ñi taxawoon ci waajtaay yi ngir jàppandal gàtt yi, moo xam kilifay Càmm gi lañu, takk-der yi, yarkat yi ba ci yaalekat yi.

TABASKI 2025 : NJIITU RÉEW MI JÉGGAL NA 1466I way-TËJLU

Ci tabaski ren ji, Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jéggal na 1 466i doomi Aadama yu ñu nëbboon jant bi ci biir réew mi. Muy lim bu takku ciy nit ñu mu bàyyilu ni ñu ko tàmmee gis ak Njiitu Réew mu fi mës a jaar. Njéggal loolu nag, doon na sañ-sañ bu Ndayu Sàrtu Réew mi jagleel Njiitu Réew mi mu ciy doxal yërmandeem jëme ci ñi tëj kaso te seen i njombe desee aay, ñii seen wér-gi-yaram demewul noonu, ay tuut-tànk, ñi jëm mag walla ñi seen jikko tàmbalee defaruwaat.

TUKKIB ELIMAANU JËWRIÑ YI FA RÉEWUM SIIN

Ci ayu-bés yii di ñëw, Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dina amal ab tukki fa réewum Siin. Muy tukki bob, dina ko amal ci càkkuteefu naataangoom bii di Li Qiang. Mu nar faa dem nag ngir dox tànki xaritoo ngir dëgëral diggante ñaari réew yi, yokk seen lëkkatoo ci wàllu koom-koom ak yaale ji. Sëñ Sonko dina fekkewaale Ndajem koom-koom (Forum économique mondial d’été) ma ñu fay amal ren. Mu nar faa jël itam kàddu ci turu kembaaru Afrig gépp.

MBIRUM ISMAAYLA MAAJOOR FAAL

Yoon a ngi ci mbirum nger mi ñuy toppe Ismayla Maajoor Faal. Bees sukkandikoo ci xibaar yi sunuy naataango yu Les Échos siiwal, teg nañu loxo ñaar ci ñi ko doon tuumal. Ñuy Séex Géey mi jiite TCS (Technologie Consulting Service) ak kii di Mohamet Anas El Basiir Wan mi jiite woon tabaxte ya fa njëwriñu Yoon wi. Ca weeru me lañu leen téeyandi woon. Yoon jël na ndogalu topp leen ba takkal leen i lami tànk. Li ñu leen di toppee nag mooy defkati ñaawteef, njuuj-njaaj, mbuxum ak nger.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj