Ayda Mbóoj dina bokk ci lawax yiy xëccoo réew mi ci wotey 25 féewaryee 2024 yi. Démb ci dibéer ji la ko xamle. Lëkkatoo gii di ànd saxal liggéey moo ko tabb niki démb ci dibéer ji, bi ñuy amal seen ndaje mu mag ca CICES. Ginnaaw bees ko tabbee, Ayda Mbóoj xamle naat ne, toogaay amatul. Li des mooy sóobu ci liggéey bi ngir dégtal askan wi seen i naal.
NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI
Ginnaaw bi kàtte yu BAC 2023 bi jeexee, njureef yaa ngi ñuy wéyal di génne ci altine ji. Ci yi jot a siiwagum, gis nañu ci ndongo lu jigéen lu ràññeeku lool ca Ndànd, diwaanu Luga. Mi ngi wuyoo ci turu Yaasin Faal. Jamono yii, jàppees na ne sax, mooy ndongo li gën a xarañ.
YOONU YOKKUTE
Bërki-démb ci gaawu gi, Njiitu Réew mi, Maki Sàll, mu nga woon ca dalub roppalaan bu Belees Jaañ (AIBD). Teewaayam foofu doonoon i tànki ubbi ak a dal-loo gaarub saxaar gii di Train Express Régional (TER). Muy ñaareelu pàcc bi ginnaaw ba bu njëkk ba yemee woon Jamñaajo.
BITIM-RÉEW
UEMOA (Union économique et monétaire ouest africaine), di kurélu réewi afrig yu sowu-jant ñeel koom-koom beek koppar gi, teggi na daan yi mu tegoon ci kow réewu Mali. Ci gaawu gi, 8 sulet 2023, la jël ndogal lu ni mel, ca lël bi Njiiti réewi UEMOA yi doon amal.
XEW-XEW
Xeex bu mettee metti moo am ca kaso ba nekk ca Mbuur. Muy ab jàmmaarloo bu doxoon ci diggante kii di Abdulaay Njaay, nekkoon fi kuy sàmm kaaraange Usmaan Sonko, ak i sàmbaa-bóoy. Bees sukkandikoo ci li sunu naataangoy Observateur siiwal, deret jot na fa sax tuuru. Abdulaay Njaay ci boppam, dañ ko sotti ndox mu tàng ba ñu mujje koo rawale ca fajuwaay ba.
Ba tey ca kasob Mbuur ba, nemmeeku nañu fa ku faatu ku doon wuyoo ci turu Usmaan Ja. Moom nag ci way-ñaxtu yees tegoon loxo fa Ngeexoox la bokk. Caytu giñ doon amal ci yaramam dafa wone ne jafe-jafey noyyee ko faat.