Suba ci alxames ji la Yoon di leeral lenn ci mbirum Usmaan Sonko, Faala Fleur ak Nit Doff. Moom Njiitul Pastef suba la ëttu àttewaay bu Sigicoor di leeral ci bataaxelu kalaame gi dugaloon ñeel génnee gi ñu bëgg a génnee ci wayndarew wote yi. Ba tey kii Ndey Faatu Faal ñu gën koo xame ci Faala Fleur kenn ci ay ñoñam nga xam ne ci weeru suwe lañu ko tegoon loxo, dees na ko àtte suba ci li ñu ko doon toppe muy yee fitna.
Naka noonu Moor Taala Géy ñu gën ko xame ci Nit Dof moom it mu bokk ci ñoñi Sonko yi ñu jàppoon ko weeru saawiye. Moom dees na xam suba ndax dees koy nangul bataaxelu càkkuteef ngir bàyyig négandiku bi ñu njëkkoon a bañal. Bu suba ci alxames ji dees na ci am lu leer.
Mu amaat keneen ci ay ñoñam di meetar Ngañ Demba Ture nga xam ne jamono jii ma nga fa Marog. Moom nag dafa dawoon génn réew mi, gàddaay fa Mali ginnaaw ba ñu jàppee Sonko, di ko wër, ca la deme woon. La ko yóbbu woon Marog mooy ndaje mu ñu fa doon amal moom ak Guy Mariis Saañaa ak waa Pastef ya fa nekke. Waaye, ndaje mooma mujjul a àntu, takk-der yaa ko tas.
Waaye, mbir mi yemul foofu. Ndax, moom Ngañ Demba àppu jàll-waaxam day waaj a jeex. Mu bëggoon ko yeesalaat foofa. Loolu moom mujjul a àntu. Ndax, nee na bi mu defee li mu war a def ba war cee jot, ci lañu ko xamalee ne dañoo jot ndigalu jëwriñu Senegaal ji ñu dénk wàllum biir réew, Antuwaan Feliks Jom. Ndigal loolu mooy ñu bañal jàll-waaxam boobu nga xam ne àpp bi ci gaawi gii di ñëw lay jeex.
XALIFA SÀLL FEY NA
Njiitul Taxawu Senegaal fey na daanu juróomi miliyoŋ yi ko Yoonu Senegaal daanoon. Daan boobu ñi ngi ko ko tegoon ca atum 2018 boole kook juróomi ati kaso yu mu waroon a tëdd laata ñu koy baal ci atum 2019. Li ñu ko doon toppee nag mooy ag luubal. Ca jamono yooya, moom moo nekkoon njiitul meeri bu Ndakaaru. Peyug alamaan boobu nag li ko waral mooy ngir mu gën a setal deram ndax lawax la ci wote yii di ñëw.
UBBITEG UCAD
Daara ju kowe ja nekke ca Ndakaaru ba tey ubbegul i buntam. La waraloon tëj ga nag moo nekkoon coowal Usmaan Sonko la taxoon ba ay yàqute yu bare amoon ca. Ca lañu ko tëje woon ba tey. Ubbite gi nag moom la ñépp di xaar. Kii di Njiitul COUD (Centre des Oeuvres Universitaires de Dakar) joxe na ci ay leeral. Ginnaaw coow li ubbite gi juroon fan yii yépp moom xamle na ne ci lu yàggul dara dees na ko ubbiwaat. Waaye, balaay boobu fàww ñu yokk kaaraange gi. Ndax, li leen daloon ci weeru suwe wi yombul woon dara ci ñoom. Bu loolu matee am na nu muy deme fii ak nowàmbar ci yoon njàng mi dina dooraat ca béréb boobu.
MBËKK MI
Yoonu Espaañ mi ngi wéy di nekk tànneefu doomi Senegaal yi. Ba tax na jamono jii duñu toog ay fan te dégguñu ag gaal walla gaal yu teeri, yu ñu jàpp walla yu réer. Waaye, gaali tey yi, ci àllarba ji, ñoom teeri nañu Tenerif (Espaañ). Ñaari gaal yooyu yeboon nañu lu tollu ci téeméeri nit ak juróom-ñeen-fukk ak juróom-ñaar.
ISRAAYEL-PALASTIIN
Xeex ba dox diggante ñaar ñooñu ba tey ma ngay wéy. Coow loolu nag du lu bees bees sukkandikoo ci mboor. Day mel ni fitna dafa yeewuwaat seen diggante. Ba tax reyante baa nga mel ni tulleek màlle. Ndax, bees sukkandikoo ci jëwriñu Gasaa (Palestin) ji ñu dénk wàlluw wér-gi-yaram biral na limu ñi ci faatu ci congu mujj mi. Nee na lu tollu ci junni ak juróom-fukki doomi Palestin ak juróom yu ñàkk seen bakkan ginnaaw soxi Israayel yi. Mu am lu tollu ci juróomi junniy doomi aadama ak téeméer ak juróom-ñett fukk ak ñeent yu ci jële ay gaañu-gaañu. Waaye, ba tey mbir ma yemagul foofu. Ndax, coow li dafa mel ni li ko tëgg tasu ko.