LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (11/10/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

SÉMBUW SOPPI SENEGAAL FII AK 2050

Sémb wi, maanaam “Le Projet”, nees koy waxee, yemb na. Njiitu réew mi ak elimaanu jëwriñ yi ñoo ko xamle. Ci altine jii, 14i pani oktoobar 2024 lees koy aajar ci njiiteefu Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Fa CICAD la xewu kaajar googu di ame. Sémb woowu nag, dinañu ko natt ci 25i at, dale 2025 jàpp 2050. Lees ko dugge mooy soppi réewum Senegaal coppite gu matale, lalu ci jub, jubal ak jubbanti.

FUTBAL : GAYNDEY SENEGAAL YI FIRI NAÑ

Sànk, bi 19i waxtu jotee, la gayndey Senegaal doon janook waa Malawi ñeel tooglantey CAN 2025 bi war a ame Marog. Senegaal a doon dalal Malawi ca fowub Abdulaay Wàdd bu Jamñaajo. Mu nekkoon njëlbeenug joŋante ginnaaw bi ñu dàqee Aliw Siise. Paab Caw moo jiite woon ekib bi. Senegaal moo dóor 4i bii ci 0. Paab Géy, Saajo Maane, Bulaay Ja ak Nikolaa Jakson ñoo dugal biiwi Senegaal yi.

JÀPP NAÑU JÉGUY JÓOB

Jéguy Jóob mi ngi bokk ci làng gi fi jiite woon réew mi, di APR(Alliance Pour la République). Bu yàggul dara lañu ko woo woon. Dafa     di, moom, Jéguy Jóob dañu ko woowaatoon démb ci alxames ji. Luññutu bi tax ñu woolu ko, nee ñu, lu ñeel luubalug alalu réew mi la. Maanaam, li ñuy wax ci farãse “escroquerie sur des deniers publics”. Bi mu wuyujee nag, dañu ko jàpp, def ko “garde-à-vue”. Moo tax, kaso la fanaan.

DIRPA AM NA NJIIT LU BEES

DIRPA (Direction de l’Information et des Relations Publiques des Armées) mooy banqaas bi yor jokkoog Làrme bi. Banqaas boobu nag, ki ko jiite woon mooy Kolonel Musaa Kulibali. Ki ko wuutu mooy “Le capitaine de vaisseau” Ibraayma Sow. Li jar a leeral fii, mooy ne, daraja “capitaine de vaisseau” ak ju “colonel” ñoo tolloo bu dee ci “Marine” la.

XEW-XEW BU TIIS FA TÀMBAAKUNDAA

Xew-xew boobu mi ngi am barki-démb ci ngoon ay boori juróomi waxtu fa Sincu Jam Pullo. Mi ngi nekk ci gox bii di Ndoga Baabakar. Bees sukkandikoo ci yéenekaay Leral [Leeral], ñaari sàmm yu seeti woon seen i jur fa àll ba, ñoom la fa taw bu metti fekk. Kenn ci ñoom di wuyoo ci turu A. Jàllo tollu ci ñaar-fukki at, dënnu gi daf ko mujjee faat. Ki mu àndaloon di M. Jàllo tollu ci ñaar-fukki at ak ñett, moom ay gaañu-gaañu la ci jële.

ABDULAAY RAASIN KAN JÓGE NA PDS

Lu ëpp fukki at ak juróom bi mu bokkee ci làng googu ak tey, ànd boobu jeex na. Ki biral xibaar bi mooy moom ndeyu-mbill ji. Nee na, bàyyi na PDS (Parti Démocratique du Sénégal). Li sabab mba gi nag, mbiri pólitig am na ci naam. Waaye, ay mbiri boppam tamit mi ngi ci. Ndax, nee na, lii dina tax mu gën a mën a toppatoo ag njabootam. Leneen li sabab mba gi mooy li waa PDS dem lëkkaloo ak waa APR (Alliance Pour la République) sos ag lëkkatoo. Ñu fas yéenee ànd ci wotey palug dépite yii di ñëw. Mu jàpp ne loolu jaaduwul. Nde, noonu démb moom warul mën a doon xaritu tey.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj