Fa Sigicoor, am na ñetti xale yu ñu dàq ci seen lekkool ba. Muy daan bu ñu leen gàll te njiiti njàngale mi fa diiwaan ba dëggal ko cib yégle bu ñu siiwal. Ñetti xale yooyu di wuyoo ci turi Abdu Njaay, Eliyaas Bajaan ak Idiriisa Jaata. Ñoo ngi doon jànge ci lekkool bu digg-dóomu bii di CEM Boucotte Sud. Li ñu leen tuumaal ba tax ñu dàq leen mooy ni dañoo jikkowoo anam yu ñàkk teggin jëme woon ko ci ñi leen di taxawu ci njàngale mi. Ñuy ay saaga yu ñu doon def, filme leen. Widewoo yay law ci mbaali jokkoo yi ba ñépp jot ci. Yaatal googu ñu ko def nag ci lënd gi, gën naa tax ba ñu daan leen daan bu saf sàpp, génne leen lekkool ba fàww.
Ci yégle bi ñu siiwalee dàq bi, njiiti njàngale mi fa diwaanub Sigicoor gaawantu na ca ngir fàttali ndongo yi njariñ li nekk ci sàmmonteek sàrti teggin yi ci biir jàngu yi ak jox cër jàngalekat yeek liggéeykat yi leen di taxawu ci seen njàng.
DÀQE YU BARI YI CI BARABU LIGGÉEY YI
Dàqe yu bare yi ñu nemmeeku ci barabi liggéeyukaay yu jàmbure yi ak yi Nguur gi séq ak ñoom tàmbali nañoo ub boppi askan wi. Lilee tax ba kurélug sàndikaa yii di CNTS (Confédération nationale des travailleurs du Sénégal) génn di fésal tiitaangeem ci ni mu jéggee dayo. Mariyaam Soxna Dãsoxo, fara-caytu bi yor wàllu njàng meek tàggatu bi ci biir kurél gi, dellusi na ci, yékkati ciy kàddu démb ci altine ji, bi ñuy amal ab jotaayu tàggatu fa Fatig. Naka noonu, muy ñaawlu ëppal gi ñu ci gis. Nde, dàqe yi bari na te ànd ak salfaañe awuwaay yi war. Ba tax muy xamle ni seen kurél gi deful lu dul di leen ñaawlu. Te, lu leen ci gën a jaaxal mooy ne li dàqe yi di bari yépp, amul benn diisoo bu ci am ci diggante njaatige yi ak liggéeykat yi ngir am i saafara yu tane. Bu dàqe mënul a ñàkk itam, dafa am i yoon yees ko war a teg te kenn woowul liggéeykat yi ci waxtaan ngir xam nees mën a doxalee.
TERE NAÑU MANSUUR FAY MU GÉNN RÉEW MI
Mansuur Fay, mujje woon fi nekk ci Nguurug Maki Sàll jëwriñu tabaxte yi, yaale yi ak yooni dëkk yu ruqe yi, tere nañu ko mu génn réew mi. Démb ci altine ji, 10 mars 2025, la yëg lu ni mel bi mu yeggee fa dalub roppalaan AIBD. Bees sukkandikoo ci li mu wax, fi mu foboo noonu bay dem lañu ko ko yegge xibaar bi. Fekk mu jëloon yoonuw Air France, utali Jidda ngir amali umra fa Màkka. Muy nag ndogal lu muy naqarlu ak di biral ni teguwul ci lenn lu dul xoqatal ci wàllu pólitig. Nde, bi mu laajtee lu waral aaye bi, ndawul pólis li dafa ko xamal ni ndigal lu ñu jot la ci kilifa yu mag yi. Ba tax muy xamle ni Yoon toppu ko te amul lenn lu ñu nekk di luññutu ci moom lu war a mën a layal ndogal li.
Naka noonu, muy xamle ni bu dee ay mbiri pólitig rekk la, kilifa yi fi nekk dinañu yàgg a sonn. Ndax xoqatal bu ni mel du ko tax a sëngeem wenn yoon.
JÀPP NAÑU ARDO ÑING
Kii di Ardo Ñing mujje naa fanaan démb kaso. Dañu koo téye ci jàppub négandiku démb ci altine ji, ginaaw bi ñu ko wooloo fa DSC (Division spéciale de Cybersécurité) ngir déglu ko. Moom nag, doon na ku ñu ràññe ci ñi ñuy duppe activistes. Lees koy toppe nag mooy i kàddu yu mu biral ci xëtu Facebookam. Muy i kàddu yu toppekat bi jàpp ne dañoo ñaaw lool ba tax mu jógal boppam. Bees sukkandikoo ci xibaar yi sunuy naataango yu Seneweb biral, làyyiwul wenn yoon ni moo biral yooyee kàddu waaye, ciy waxam, saagawul kenn. Ñuy xaar ba xam kañ lees koy yóbbul toppekat bi ak fu mu nar a jaar ak moom.