LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (12/11/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

WÉR-GI-YARAM : COMES BANK NA LOXOOM

Fajkat yi bokk ci kurél gii di COMES (Collectif des Médecins, Pharmaciens, Chirurgiens-dentistes en spécialisation) bank nañu seen i loxo. Démb ci altine ji, 11 nowàmbar 2024, lañu tàmbali ab ñaxtu bu amul àpp. Ci yégle bi ñu génne, ñaŋ cay xamle ni ay weer a ngi nii ñu nekk di xeex, di waxtaan ak a xaar. Waaye, dafa mel ni yi kilifa yi xaatimoon ak ñoom yépp ay dige neen la. Li ñu bëgg nag mooy ñu ñoŋal anam yi ñuy liggéeyee te jox leen gëdda gi ñu yayoo. Fileek saafarawuñu seen i tawat nag duñ dellu ginnaaw. Ndax, dootuñu nangu liggéey ci anam yu ñaaw ànd ak ñàkk gëddaal seen tàggatu ak salfaañe seen i àq ak i yelleef.

PAATUG MAMADU MUSTAFAA BA

Mbokki Mamadu Mustafaa Ba jotaguñu ci néewam ba léegi. Ginnaaw bi mu faatu fa réewum Farãs ci ayu-bés bii weesu (altine 4 nowàmbar 2024), xel dafa teeyoon lool ci anan yi mu faatoo ba toppekatu bokkeef gi sàkku woon ci otopsi. Ci yégle bi ñu génne démb nag, njureefi otopsi bi dafa bari yu mu wone yuy firndeel ni ki fi nekkoon jëwriñu ngurd meek nafa gi ci Càmmug Maki Sàll, deewul ci neen. Ci xiibar yooyu la toppekat bi sukkandiku daldi dàq rob bi teg ci ubbilu luññutu. Bees sukkandikoo ci sunuy naataango yu L’Observateur, waa DIC ñi yor luññutu bi tàmbali nañu ndéglu yi ak soxnaam. Li ñu ko, dugge mooy xam barab yi jëkkëram daan faral di nekk fa Farãs, waxtaan yi ñu mujje am ñoom ñaar, ñi jële ay bagaasam fa mu daloon, ba ci wér-gi-yaramam.

PAATUG SÀMB MBAALO (GELONGAL)

Tiis wu réy dal na ci kaw axlu mbatiit. Kippaangoog woykat gii di Gelongal, moo ñàkk aji-bokkam jii di Sàmb Mbaalo, ñu koy wax Bàcc. Barki-démb ci dibéer ji la faatu. War nañ koo rob démb ci altine ji fa sëgi Yoof ya, bi 17i waxtu jotee. Demug Bàcc gi nag, dina gën a wéetal kippaangoo gi, rawatina Musaa ginnaaw bi Papis Mbaalo njëkkee dëddu ci at yii weesu. Ñoom ñett a sosoon kippaangoo gi ca atum 1992, tàmbali woon ko ak pecc mi ñuy wax breakdance laata ñuy dugg ci woy (Rap). Seen i way nag ràññeeku woon nañu lool ak fànnu mbatiit wi ñu ci boole woon.

PASUG SENEGAAL AK UE ÑEEL NAPP GI

Pas gi doxoon ci diggante réewum Senegaal ak UE (Union Européenne), Mbootaayu réewi tugal yi, dina jeex ci dibéer jii di ñëw, 17 nowàmbar 2024. Ñiŋ ko xaatimoon ci atum 2019 (18 nowàmbar), waroon ko dawal ci diirub 5i at. Naka noonu, Sëñ Jean-Marc Pisani, di ndawu mbootaayu réewi tugal yi fi Senegaal dina ci janook saabalukaayi réew mi ak yu bitim-réew. Ñuy xaar ba xam dinañu yeesal pas gi ak kilifa yu bees yi am déet.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj