LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (12/7/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

ONG CAMINANDO FRONTERAS WEDDI NA AYSATA TAAL SÀLL

ONG Espaañ Bii di Caminando Fronteras dëggal na ne, dafa am  na 300i doomi Senegaal yu jëloon gaal gi, jëmoon Espaañ, daldi réer ci géej gi. Xibaar boobu nag,bi mu siiwee, Aysata Taal Sàll, jëwriñ ji ñu dénk mbiri bitim-réew ak doomi Senegaal ya fa nekk, daf ko weddi woon. ONG bi nag, xamle na ne, 300i saa-senegaal yooyu sóobu woon ci mbëkk mi, Senegaal fii lañu jóge, ci boori njeexitalu weeru suwe wii nu génn. Te, ba tey, kenn tegu leen bët. Nee ñu sax, wall gi kilifay Senegaal yi doon wax ne njiiti Espaañ yeek yu Marog ak yu Moritani yi dañ ko wall ay gaal, gog yeboon 300i saa-senegaal bokku ci. Moo tax ñuy woo Nguuru Senegaal mu jéem a wutiy pexe ngir feeñal leen.

MAKI SÀLL RAFETLUWUL NDAJEM PASTEF MI

Ci gaawu gii ñu dëgmal, yemoo ak fukki fan ak juróom ci weeru sulet wii, la waa Pastef namm a amal ndaje mom, ca lañuy tabbee Usmaan Sonko seen lawax. Njiitu réew mi nag, Maki Sàll, mel na ni mbir mi neexu ko. Nde, forees na ci wewu béy ne, démb, ba muy dalal dépitey Bennoo Bokk Yaakaar yi, àddu na ci. Nee ñu, Njiitu réew dafa gis ne loolu ab “cokkaas la”. Li ko waral mooy kii di Usmaan Sonko dafa am ñaari daan yu tegu ci ndoddam. Bi ci jiitu di daanu juróom-benni weer ci coow li doxoon digganteem ak Maam Mbay Ñaŋ. Ba ca topp di ñaari ati kaso yi ñu ko war a tëj ci coow li dox ci digganteem ak Aji Saar. Waaye, ñii di waa Pastef moom, dafa mel ni loolu safuleen. Maanaam, ñoom, lu naqari Maki Sàll lu nekk rekk, neex na leen.

TËJ NAÑU BIRAM SULEY JÓOB KASO

Démb, ci talaata ji, la Biram Suley Jóob miy meeru Thiès-Nord, di yit njiitul kippug Yewwi Askan Wi ca Ngomblaan ga, fanaani kaso. Li ko waral mooy ne, tof-njiitu Pastef li dafa yëkkati woon ay kàddu ci fan yii nu génn, teg leen ci deru Njiitu réew mi. Naam, génnoon def ab widewoo ngir jéggalu, waaye, booba fekk na béy wéy na mbuus. Ndax, ñi ngi koy toppe jëf ju mën a nasaxal jàmmi askan wi ak tooñ walla ŋàññi Njiitu réew mi. Ñii di waa Yewwi Askan Wi nag, génnee nañu ab yëgle ngir ñaawlu anam yi ñu jàppee seen naataango boobu. Ndax, ñoom, dañoo salfaañe àq ak yelleefi dépiteem. Rax-ci-dolli, dañoo salfaañe dogu 61 bu ndeyu àtte ji ak càrtu Ngomblaan gi ko may malaanum kiiraay.

KÀTTEY BFEM AK BAC

Tey ci àllarba ji la joŋante bi ñeel wutug lijaasa bii di BFEM door ci réew mépp. Tey itam la ndongo yi nga xam ne mataluñu woon i poñ ci pàccub BAC bu njëkk bi di kàttewaat ngir jàll. Bu dee BFEM bi moom, am na yenn ci ay dëkk yu fésal seen limu ndongo yi koy def, niki waa I.A bu Ndakaaru. Nee nañu, am nañu lu tollu ci 17 326i ndongo, ñu tas leen ci 45i bérébi joŋante (centres d’examens) ak lu tollu 79i yu ko war a doxal (jury). Ñu am nag lu tollu ci 1 171i jàngalekat yu war a wattu joŋante boobu.

JÉYYA CA GÉEJU NDAR GA

Ñoo ngi jooy 300i nit yi réer ci géej gi, noppeeguñ sax, beneen xibaar bu tiis toftalu ci. Fa Ndar la ame. Dafa am ag gaal gu yeboon juróom-benn fukki nit, far këppu. Jamono jii nag, juróom-benni nit lees wax ne ñoo ci lab, ña ca des ame ay gaañu-gaañu. Ña ngay wéyal luññutu ya ngir xool ba xam am na ñeneen ñu yëf yi laal, ngir xam itam li sabab jéyya ji.

GAYNDEY SENEGAAL YI

Jamono jii, doomi Senegaal yay futbal ca bitim-réew ña nga ca yoonu soppiy ékib. Loolu nag, tàmbali na ca fan yee weesu ak ku ci mel ni Kalidu Kulibali ak Eduwaar Méndi. Kii di Mbay Jaañ, Nàmpalis Méndi ak Abdu Jàllo tamit ña nga ca yoonu fekki seen mbokk yooya ca Araabi Sawdit. Geneen gaynde tamit goo xam ne fan yii ma nga ca yoonu dem mooy kii di Ilimaan Njaay. Moom nag ñii di waa Olympique de Marseille ñoo koy laaj. Waaye, ba tey, dara leeragu ci. Ndax, fee mu nekk, ca Sheffield United dañu koo bëgg a téye.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj