LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (12/7/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

JANOO NJIITU RÉEW MI AK TASKATI XIBAAR YU RÉEW MI

Lu tollu ci téeméeri fan ginnaaw bi ñu ko falee ak léegi, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay dina amal aw waxtaan. Wii yoon moom, ñii di taskati-xibaar yi lay jàkkaarlool. Jàkkaarloo boobu, dina am gaawu gii ñu dëgmal, yemoo ak fukki fan ak ñett ci weeru sulet wii. Waxtaan wi dina am bu juróom-ñeentu waxtu ci guddi jotee. Ma ngay ame fa màkkaanu Njiitu réew ma. Li mu ko dugge mooy mën a tontu ci laaji taskati-xibaar yi. Leeralaale askanu Senegaal fu liggéey bi ñu leen dénk tollu ak fan lañu ko namm a jëmale.

COOWAL DÉJJATI LI AMOON FA SANDAGA

Déjjati geek tuxal gi takkarnaase na jamono jii fa béréb yu bari ca Ndakaaru. Looloo taxoon, fan yee weesu, elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dem fa Kolobaan ngir indi ci ay leeral. Maanaam, wax ña fay daan seen doole lan moo sabab déjjati geek tuxal gi. Liggéey boobu meeri yi di amal nag  moo jur coow lu bari démb fa Sàndaga ba mu mujj ci ay jàmmaarloo diggante ndawi meeri ba ak jaaykat yi. Waaye, dal ga mujj na faa dellusiwaat.

ËTTU CAYTU GI DOOR NAY LUÑÑUTU FA FSF

FSF (Fédération Sénégalaise de Football) di kurél gi ëmb wàllu futbal bi ci réew mi. Banqaasu caytu gii di “Cour des comptes” mi ngi ci tànki ñi ko yore. Looloo taxoon mu woolu woon kii di njiit la, Augustin Seŋoor, tof-njiit la, Abdulaay Sow, ak ki fa nekkoon njiitu ndiisoog kopparal gi, Abdulaay Faal. Li ñu dugge seen ndéglu yooyu mooy xam nan lañu jëfandikoo koppar yi, rawatina ci ñaari joŋante yu mujj yi. Maanaam, ci joŋante bi boole réewi àddina yi (coupe du monde) bu atum 2022 ak joŋante bi boole réewi Afrig yi (Coupe d’Afrique des Nations) bu atum 2023.

XEW-XEWU PÓLITIG BU DOY WAAR FA KEEÑAA

Ay fan ginnaaw ba fa ay jàmmaarloo yu metti amee ba ay bakkan rot fa, Njiitu réew ma, Wiliyaam Rutoo jël na ndogal yu yéem ñu bari. Ndax, moom, coow loolu day mel ni Nguur gi la ko sippi. Nde, ñoom ñoo nammoon a taxawal aw naal wu ñeel ay “taxes” yu bees. Doxalinu woowa Nguur gi jëloon moo sabab merum askan wa, ñu génnoon di xeex ak takk-der yi, ba fanweeri doomi aadama ak juróom-ñeent ñàkk ci seen i bakkan. Looloo tax, mu dàq daanaka ñi bokk ci Nguur gi yépp. Ci gàttal, ñépp la tekkil seen i ndomboy-tànk ba mu des tof-njiit li ak ki yor ndombo-tànku “chef de la diplomatie”.

KÀPPITEEN TARAAWORE DUUT NA BAARAAM KODDIWAAR AK RÉEWUM BENEE

Kàppiteen Ibraaym Taraawore, Njiitu réewum Burkinaa Faaso, bokk ci kurélu AES gi mi ngi àrtu ay dëkkandoom. Ndax, kenn umpalewul ne jamono jii réew yooyu ay sóobare jiite ak yeneen daanaka defuñu nenn. Looloo tax, ca waxtaan wa mu doon amal démb ci alxames ji àrtu na ci waa Koddiwaar ak waa Benee. Nde, moom sax nee na séqul lu ñaaw ak askani réew yooyee. Waaye, du nangu seen i Njiit di yëngal am réewam. Ndax, nee na, réew yooyu ñooy fat gaa ñi bëgg a yëngal seen um réew. Te, loolu, dina ci indi ay firnde yu leer nàññ. Ndax, jamono jii, ñépp a xam ne ñoom ak Farãs defuñu nenn. Te, loolu moom fekku ci Koddiwaar.

FINAALI “EURO” AK “COPA AMERICA” 2024

Ñaari joŋante yooyu nga xam ne, dooroon nañu ci weeru suwe wi, ña ngay waaj a àgg ca daj-dëpp ga. Nde, muy Euro bi, di Copa bi, bu ne ci ñoom benn joŋante moo ci des. Bu dee Euro bi moom, Espaañ ak Àngalteer ñooy xëccoo ndam li ci joŋante bu mujj bi. Joŋante boobu, dina am dibéer bu juróom-ñeenti waxtu ci ngoon jotee. Joŋante bu mujj ci Copa bi moom, mi ngi dox ci diggante Àrsàntin ak Kolombi. Dinañu daje guddig dibéer jàpp altine. Maanaam, bu guddig dibéer ji xaajee, ci lañuy futbal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj