NJIITU RÉEW MI DINA JANOOK ASKAN WI CI GUDDIG TEY JII
Bu yàggul dara la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jóge Siin ginnaaw ab tukki bu ma fa amaloon. Bi mu ñëwee, fekk na fi tiis ak naqar. Nde, li xew fa Mbuur umpul kenn. Waaye, mu amaat leneen coow lum fi bàyyi woon, muy tasug Ngomblaan gi. Ba tax na, moom Njiitu réew, dina wax ak askan tey ci alxames ji, ci kanam tuuti, bu juróom-ñetti waxtu jotee ci guddi gi.
NDOGUM MBËJ MI : SENELEC INDI NA AY LEERAL
Bi 13i waxtu jotee ba tegal, daanaka ci réew mépp la mbëj mi demoon. Maanaam, kuuraŋ bi dafa kuppe woon ci réew mépp. Bi tàkkusaan weesoo lay sog di delsi. Moo tax, ñii di waa Senelec jóg, gaawantu génn ab yégle ngir xamal askan wi li sabab ndog mi. Nee ñu, dog-dog a amoon ca post bu Aan (Hann). Looloo sabab yenn jafe-jafe yi ba taxoon kuraŋ bi dog. Bi loolu amee, ci seen i wax, dañu yabal ca saa sa ay ndaw ngir ñu joyyanti ko ca na mu gën a gaawee.
NJËWRIÑUG BIIR-RÉEW MI SANT NA GII MARI SAAÑAA
Ger giy faral di am ci tali yi jurati na coow. Li ko waral du lenn lu moy xibaar bi dépite bii di Gii Mariis Saaña siiwal ci xëtu Faacebookam. Nde, dafa siiwal ag ger gu mu gis ci yoon wi. Benn takk-der moo nangu këyiti benn dawalkat ba noppi dem. Ginnaaw gi la ko dawalkat bi topp, jox ko xaalis, ñëw taalaat daamaram, dem. Joxe na limatu daamaru takk-der bi ak gog dawalkatu taksi bi. Jëf jooju nga xam ne dépite bi siiwal na ko, moom la ko jëwriñ biir-réew meek kaaraange bokkeef gi di santee. Mu yokkal ko ci ne dinañu ubbi ag luññutu. Su ko defee ñu mën a xam ñan ñoo séq jëf jooju. Ñu teg leen daan yi ci war. Nde, ñoom foweewuñu mbirum ger. Te, ñi ngi sàkku ci bépp maxejj bu gis xeeti doxalin yu ñaaw yooyu mu siiwal ko.
RTS ÑAAWLU NA KÀDDUY PAAP JIBRIIL FAAL
Tey, ci alxames ji bu juróom-ñetti waxtu ci guddi jotee la Paap Jibriil Faal waroon a amal ab jotaay bu ñu tudde “Champ contre Champ”. Waaye, dañ ko mujjee dàq ba jëmmi jamono. Li ko waral mooy ne, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, day jël kàddu gi, wax ak askan wi ca waxtu woowa. Loolu la dépite bi naaneewul ndox. Ba tax, mu bind ci xëtu Faacebookam di ñaawlu anam yi saabalukaay bi fommee jotaay bi nga xam ne moom lañu ci woowoon.
Waa RTS tamit, bind ci seen xëtu Faacebook tontu ko. Xamal ko it mbetteel gi ñu am ci kàddu yi mu yékkati. Nde, moom dépite bi, bi mu amee ay xibaar ci ne, Njiitu réew mi dafa war a wax, waroon na xam ni Njiitu réew mi lees jiital ci kow lépp. Te sax, moom, saabalkat la, loolu umpu ko. Rax-ci-dolli, ci li yégle bi xamle, moom ci boppam moo woo ki mu waroon a séqal waxtaan wi ngir ñu xool ndax, dinañu mën a aj seen jotaay boobu ba beneen. Te, bi ñu dëggalee xibaar boobu, ci saa si lañu woo dépite bi yégal ko ko. Rax-ci-dolli, ñu sàkku ci moom mu bokk ci jotaay bi ñuy amal ginnaaw bu Njiitu réew mi waxee ba noppi. Waaye, dafa mujjee gàntal seen càkkuteef boobu. Ñi ngi ñaawlu bu baax kàddoom yooyu nga xam ne laluwuñu ci dëgg.
MBIR MU DOY-WAAR CI JÉYYA JA AM MBUUR
Jéyya ja am fa Mbuur bokk na ci jéyya yi gën a metti yi nga xam ne dal nañu ci kow réewu Senegaal. Looloo tax, jamono jii, takk-der yi di wër ngir gis ñi génn ci tefes gi. Ci liggéey boobu ñu def la benn takk-der dal ci néewu way-juram wu góor. Bees sukkandikoo ci waa Senego, way-juru takk-der bi tolloon na ci juróom-fukki at ak ñeent. Li gën a doyati waar ci mbir mi mooy ne ay mbokkam yëguñu woon ne duggu na ci gaal gi. Nde, moom bu yàggul dara la jóge Mali ga mu nekkoon.