LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (13/12/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NDONGOY UGB YI SUMB NAÑ AB XEEX

Lu jege fukki fan ak juróom ba weer wi dee ak léegi. Ba tey ndongo yi mënuñoo jot seen peyooru ñaari weer yii weesu muy oktoobar ak nowàmbar. Dafa mel ni jamono jii mënatuñoo muñ mbir mi. Moo tax kurél gi leen jiite di CESL (Coordination des Etudiants de Saint-Louis) door na tey ci suba xeex bi ngir ñu fey leen. Li tukkee ci xeex boobu mooy ñaari fan yoo xam ne dañuy lekk te, duñu fey. Ak benn bés boo xam ne dañuy toog duñu jàngi. Ñoom nag yemuñu foofu. Ndax, génnee nañu beneen yégle xamle ci ne tey ci ngoon dañuy amalaat meneen ndaje bu ñeenti waxtu tegalee fanweeri simili. Kon, ci kanam dees na xam lu tukkee ca moomule ndaje.

NDELLOOG USMAAN SONKO CI WAYNDAREW WOTE YI

Démb ci talaata ji lañu doon amalaat layoo bi dox diggante Usmaan Sonko ak Nguuru Senegaal. Layoo boobu li ko waraloon mooy càmbaraat ndax, dañu koy delloowaat ci wayndarew wote yi am déed. Dafa di, moom Njiitul Pastef li àttekatu Sigicoor bi daf ni woon nañu ko delloo ci wayndare wi. Ci ginnaaw gi la ëttu àtte bu kowe bi nasaxal boobule àtte. Léegi nag, nee ñu suba ci alxames ji yemoo ak fukki fan ak ñeent ci weer wii dinañu wax ban ndogal moo tukkee ci àtte boobu.

BÀYYI NAÑU ÑOOM YARGA SI

Lu tollu ci juróom-ñeenti weer bi ñu leen tegee loxo ak léegi. Ñoñi Usmaan Sonko yooyu mujj nañu leen bàyyi tey. Moom Yarga Si mi ñu ci gënoon ràññee li ñu ko doon toppe mooy ne dafa bëggoon a faat bakkanu Usmaan Sonko. Lu tollu ci fukk ak juróom-ñaar ci ñooñu bàyyi nañu leen. Muy Yarga Si moom, Uséynu Njaay ak El Haaji Paate Mbay ak yeneen fukki doomi aadama ak ñeent.

COOWAL MARJAAN MI

Mbirum marjaan mi lëmbe na jamono jii Senegaal. Ki yékkati coow loolu mooy kii di Meetar Musaa Jóob. Ba tax démb ba tey mi ngi ci loxoy Yoon. Waaye, dafa mel ni mbir yemul foofu kese. Ndax, kii di Aali Nguy Njaay tamit nekkoon fi jëwriñ ci Nguuru Maki Sàll woo nañu ko tey ci àllarba ji ca Yoon ñeel mbir moomu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj