Ngomblaan gi dina ubbi ëllëg ci gaawu bi, 14i pani desàmbar 2024, bu fukki waxtu jotee ci yoor-yoor. Ab yégle la campeef gi génne, di ci woo dépite yi. Dañu war a fénc sémbu àtte 14/2014 wiy soppi ndeyu sàrtu réew mi. Campeef yii di CESE ak HCCT lañu bëgg a far, jële leen fi ngir sakkanal xaalisu réew mi.
CEERNO AALI SI DELLOO NA MOOMEG DÉPITEEM
Ceerno Aali Si mooy ki toppoon ci Abbaas Faal ci toftaleg Pastef gi. Loolu di firndeel ne kon, bi ñu tabbee Abbaas Faal, jëwriñ ji ñu dénk liggéey ak jokkoo yi diggante campeef yi, moom moo koy wuutu. Waaye, mbir mi mujjul a deme noonu. Ndax, moom dafa amoon ay giitaŋaas ci Yoon ba ñu daanoon ko ci atum 2021. Looloo tax, mënt a dem fa Ngomblaan ga. Ki koy wuutu fa béréb boobu mooy Maam Omar Ndóoy bees sukkandikoo ci toftale gi.
NDOGALU ÀTTEB LAT JÓOB
Barki-démb, ci àllarba ji la ëttu àtte bii di “Chambre d’accusation financière” doon saytu mbiri Lat Jóob. Nde, kenn umpalewul ne, bu yàgg ba tey ma nga fa kaso ba. Moom nag, dafa dugaloon ñaari càkkuteef : genn gi, ngir neenal topp bees koy topp ndax jalgati yi ci nekk, geneen gi jëm ci sàqi bànkam yees yi yoon tëjandi.
TÀGGE :AADI JUUF GÉNN NA ÀDDUNA
Aadi Juuf mooy baayu kuppekat bii di Aamara Juuf. Démb ci alxames ji la génn àdduna. Mu doon xibaar bu tiis ci waa Senegaal rawatina ñi nga xam ne ñooy yëngu ci wàllu futbal. Nde, kenn umpalewul ne, moom Aadi Juuf, ab tàggatkat la woon. Kon, du Aamara Juuf kese moo ñàkk, képp kuy yëngu ci mbirum kuppe ci Senegaal ñàkk na.
CONG MU METTI FA KÉEDUGU
Xew-xew boobu, mi ngi am barki-démb ci guddi. Ma nga ame fa Farandiŋ, nekk ci goxu Saarayaa. Ay sàmbaa-bóoy ñoo fa song ab dëkk. Mu mel ni nag, ka ñu fa doon seet gisuñu ko. Waaye, loolu terewul ne jot nañu fa a jël xaalis, wurus ak ay jollasu. Ba noppi, dóor fa ay sox. Am na sax soxna su ci ñàkk bakkanam. Mu am ñaar ñu ci jële ay gaañu-gaañu. Bi ñu yëgalee takk-der yi cong mi, dem nañu walluji leen. Waaye, laata ñuy àgg fa béréb ba fekk na sàmbaa-bóoy ya moom daw nañu.
NDOGUM YOON FA MAATAM
Ndog moomu, mi ngi am ci ngoonug démb ji fa goxub Kanel. Ñaari daamar ñoo fa mbëkkante. Benn bi, am minikaar la. Beneen bi, di ab biis. Ñetti doomi-Aadama ñoo ci ñàkk seen i bakkan. Am tamit, ñaar ñoo xam ne jële nañu ci ay gaañu-gaañu.