LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (13/2/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NDÉGLUG FARBA NGOM

Tay, ci alxames ji la waa PJF (Pool Judiciaire Financier) woolu woon dépite bii di Farba Ngom. Nde, kenn umpalewul ne dañu koy tudd ci coowal koppar gu tollu ci 125i miliyaar. Looloo taxoon ñu woolu woon ko tay fa màkkaanu PJF ma. Ginnaaw bi ñu ko dégloo ba noppi, Farba Ngom mujje na dellu këram. Waaye, woowaat nañu ko ñaar-fukki fan ak juróom-ñaari ci weer wii ñu nekk.

TUKKIB NJIITU RÉEW MI

Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, tukki na tay ci alxames ji. Dafa teeweji ndajem Bennoog Afrig (Union Africaine). Ndaje moomu, ñi ngi koy amalee fa Adis-Abebaa, nekk fa réewum Ecopi. Dafa di, ndaje moomii dafa am solo lool. Ndax, bari na poñ yu ñu fa war a waxtaane. Muy lu jëm ci koom gi, pólitig bi, kaaraange gi, añs. Ndaje la moo xam ne it, Njiitu réewi Afrig yu baree fay tase.

DAAN NAÑU BUUBAKAR KAMARA

Buubakar Kamara mooy ndaw (mandataire) li dawoon ak toftaley AG/Jotna ci wotey palug dépite yii jàll. Ñooñu nag, bàyyiwuñu woon mbir mi mu sedd. Dañu ko toppoon ci Yoon. Bees sukkandikoo ci li meetar Musaa Jóob siiwal ci xëtu Facebookam, moom Buubakar Kamara daan nañu ko ñetti weer yu mu dul tëdd ak alamaan bu tollu ci téeméeri junni. Nee na, ñoom xeeb nañu daan bi ñu bees ko gam-gamlee ak jëf ji mu def lëkkatoog lëmm.

SENELEC MI NGI ÀRTU

Senelec génnee na ab yégle ngir àrtu ci xew-xew yiy am fan yii. Nde, dafa am ay sàmbaa-bóoy yuy mbubboo ndawi Senelec. Gaa ñooñu, ñi ngi dugg ci kër yi naan Senelec moo leen yabal. Ñi ngi xamal askan wi ne ñoom yónniwuñu leen tay, yónniwuñu leen suba. Ñuy sàkku ci nit ñi ñu xool bu baax fi ñuy teg seen i tànk.

BENEEN XEW-XEW BU DOY-WAAR FA UGB

Daara ju kowe ja nekk fa Ndar coow topp na ko fan yii. Ci altine jii weesu la fa ndongo buy wuyoo ci turu Mataar Jaañ génn àdduna ci anam yu yéeme. Ñuy coow loolu noppeeguñu, beneen xew-xew bu doy waar tegu ca. Leneen ndongo lu jigéen moo fa doon jéem a xaru. Dafa naan ay doom yu bari. Sonnoon na lool ba ñu rawale ko fa raglu bu Ndar. Waaye, mujje na mucc. Li sabab jëf jooju nag dese na leer.

XIBAAR YU DIIS CI GAYNDEY SENEGAAL YI

Ci weeru màrs wii ñu jëm, gayndey Senegaal yi dañu cee am joŋante yu am solo. Waaye, mu am ñaari gaynde yoo xam ne naruñu fekke joŋante yooyu. Ñaar ñooñu, Elimaanu Njaay mi nekk fa Everton ak Nikolaa Jakson mi nekk Chelsea la. Ñu doon ñaar ñu ñépp di bàyyi xel rawatina guddi yii ñu tollu. Dafa di, ñoom ñaar ñépp dañoo ame ay gaañu-gaañu. Te, joŋante yooyu dafa naru leen fekk ñu wér.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj