Póol Kagame, Njiitu réewum Ruwàndaa li, moo ngi woon fi réew mi ci njeexitalu ayu-bés bi. Ab tukkib liggéey la fi doon amal ci àppug ñaari fan. Bi mu agsee, naataangoom bi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, moo ko dalal fa njénde la. Naka noonu, ñaari Njiiti réew yi amal nañ waxtaan wu yaatu ci lëkkatoog ñaari réew yii di Senegaal ak Ruwàndaa ñeel lu jëm ci koom-koom, kaaraange ak mbatiit. Ginnaaw gi, ñaari Njiiti réew yi ànd nañu yendu ci dibéer ji, añandoo laata ñuy seetaani ab joŋante basket bu doon dox ci diggante AS Douanes (Senegaal) ak APR (Ruwàndaa).
Ginnaaw bi mu jeexalee tukkeem bi, Póol Kagaame dellu na dëkkam tey ci altine ji. Bi mu fiy jóge, jëwriñ ju mag ji Usmaan Sonko moo ko gunge ba ca dalu roppalaan ya.
NEEXALUB MIRIYAAM MAKEBAA
Usmaan Sonko, Magum jëwriñ yi fi Senegaal, moo jël ren neexal bii ñu duppe Miriyaam Makebaa. Moom la nattkat yi tànn ginnaaw bi ñu seetloo ni xalaat yi Miriyaam Makebaa doon biral moom Usmaan Sonko dafa leen jëmmal jëmale ci Bennoo Afrig, dimbalante, yokkute ak xiir ndaw ñi ci ñu jóg takku, gëm seen bopp ngir seen ëllëgi réew ak ëllëgu kembaru Afrig gën a ñoŋ. Neexal boobu nag dina ci jot ci bésub 18 me 2024 fa Pari (Farãs).
DEKKARE NEENAL
Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay jël na dekkare ngir neenal ab dekkare bu fi Maki Sàll (ki mu wuutu ci boppu réew mi) xaatim ci fan yi mujje laata muy dem. Du guleet muy jël dekkare bu ni mel ngir neenal. Waaye wile yoon, ab dekkare bu doon jotlu jëwriñ yi fi nekkoon 1,5 ba 2,8 tamndareet ci peyoor la neenal.
CAABAL YEEK TOPPE YI CI WAR
Amul lenn ci ndigalu toppe bu am ci caabal yi ñu jot a tasaare fan yii ci yoriinu réew mi. Mustafaa Sare mi yor kàddu Càmm gi moo ko xamle. Bees sukkandikoo ci xibaar yi mu biral fa Rfm, Saa-Senegaal yi mën nañ dalal seen xel. Nde, yoon dina def liggéeyam ni mu waree te amul kenn ku ko koy jàngal walla mu ko koy defal. Moo tax ba dañu leen di bàyyi ñu def seen liggéey. Saa su toppekat bi gisee ni am na nit ñu def lu jéggi dayo ba ñu war leen a topp, dina ko def.
LAKSIDAŊ BU AM CI VDN BI (FOIRE)
Ay bakkan rotatinañu cib laksidaŋ bu amati ci tali bi. Biisu Tata bu limatu 44 bi moo mbëkk ab móto ba noppi jaar ci kow ab taksi. Nee ñu, 3i doom-aadama ñàkk nañ ci seen i bakkan ci saa si. Jéyya joojoo nga ame ci VDN (Voie de Dégagement Nord).
ÑËWUG KAGAME FI SENEGAAL