Ndogal yi tukkee woon ca ndajem CSM (Conseil Supérieur de la Magistrature) ci àjjuma jii weesoo ngi wéy di jur coow fi réew mi, rawatina ñenn ci àttekat yi ñu yóbbu fa Tàmbaa. Lilee tax sax ba waa APR génne ab yégle di ko ñaawlu. Nde, dañ jàpp ni ciy defante la Nguur gu bees gi dugal Yoonu réew mi. Waxi waa APR jooju sax, tax na ba Séydu Gasama yékkatiy kàddu. Muy xamle ni xeeti njort yooyu yàgg nañ fi am. Waaye, li ko ëppal solo mooy ni du rekk ni Yoon dafa war a moom boppam, waaye ma-xejj yi dañ koo war a gise nu ni mel ndax ñu mën a mucc ci yenn yëngu-yëngu yiy tukkee ci ndogal yi yoon di jël.
NGOMBALAAN GI
Ngombalaan gi dañ ko war a tas. Loolu mooy gis-gisub dépite bii di Muhammet Saaña (Gii Maris Saañaa). Bërki-démb, ci dibéer ji, la ko dellu biral. Fekk ñu doon ko dalal ci jotaayu Point de Vue biy am fa màkkaanu RTS (Radio Télévision Sénégalaise). Bees sukkandikoo ciy kàddoom nag, ni Ngombalaan gi tëggoo tax na ba kenn mënu faa xeexal njariñi askan wi. Ba tax na, dafay doon ngëneel ñu tas ko bees bëggee taxaw ci yittey askan wi. Te itam, dina doon ub bunt bu am solo ngir tegaat réew mi ci keno yu bees.
MBËKK MI
Lu jege 250i ndaw songaat nañu mbëkk mi. Bërki-démb, ci dibéer ji lañu leen teg loxo, fekk ñu doon waaj a dem, wutali tugal. Ñaŋ leen jàppe nag ca dëkk bu ñu naan Bàmbugaar, diwaanu Fatig.
Bees sukkandikoo ci sunuy naataangoo yu Le Soleil, ag gaal guñ làqoon foofu di xaar seen waxtu dem jot, moo leen waroon a yóbbu. Bi ko takk-der yi yëggee lañ wàcc foofa, daldi leen mbaal. Ñuy i ndaw kese yu bawoo fa diwaan ba ak fa réewum Gàmbi. Nemmeeku nañ ceet ay jigéen ak seen i doom. Ña doon sëf gaal ga nag, dañ daw ba rëcc bi ñu yëgantalee takk-der ya.