El Haaji Mamadu Jaawo, ñu gën ko xame ci Maam Bóoy Jaawo biral na ne lawax la ci wotey 2024 yi. Mi ngi jël ndogal loolu démb ci talaata ji ginnaaw bi Njiitu réew mi Maki Sàll xamlee ci gaawu gi Aamadu Ba mooy doon lawaxu lëkkatoog Bennoo Bokk Yaakaar. Taxawal na lëkkatoo gu bees dippe ko “Coalition pour un Sénégal nouveau”.
Ginnaaw bi ndogal loolu daanoo, moom Maam Bóoy dàq nañu ko foofa mu nekkoon. Maanaam tekki nañu ndombog-tànk ga ñu ko takkaloon di “Directeur général de la Caisse des Dépots et des Consignations”. Ñaari xew-xew yooyu yépp nag démb la ci talaata ji. Meeru Koldaa bi dafa génn ne lawax la, Njiitu réew génnee dogal ne dàq nañu ko.
LU BEES CI MBIRUM BASIIRU JOMAAY FAY
Ay weer ginnaaw bi ñu ko tegee loxo, ba tey ma nga ca kaso ba. Waaye, dafa am lu bees lu dolleeku ci li ñu ko doon toppe. Li ñu ko doon toppe moo nekkoon def jëfin yu mën a yee fitna, tooñ kilifay Yoon ak yàq deru kurélug lëmm. Jamono jii nag ñi ngi koy toppe mboolem li nga xam ne ñoo ngi koy toppe Njiitul Pastef li Usmaan Sonko. Kon, fi mu tollu nii, moom Basiiru Jomaay Fay lu jege fukki tuuma mi ngi ñu gàll ci ndoddam.
SËRIÑ MUNTAXAA MBÀKKE NUQEETINA
Xalifa seneraal bu Tuubaa nuqeetina ci gafa gi lim bu takku ci xaalis. Wii yoon mi ngi ko jagleel askanu Marog nga xam ne jéyya ju metti moo fa xew. Jéyya jooju nga xam ne lu ëpp ñaari junniy nit ñàkk nañu ci seen i bakkan, waxaalewuñu ñi ci jëley gaañu-gaañu. Kilifag Tuubaa gi génnee na lu tollu ci téeméeri miliyoŋ jox leen ko.
CAN 2023
Xamees na limu ékib yay dem ca joŋante booba di ame fa Kodiwaar. Ñi ngi tollu ci ñaar-fukki réew ak ñeent. Ékib yooyu di taxawaliji réew yooyu yii la : Koddiwaar, Marog, Alseri, Senegaal, Afrig-di-sid, Burkinaa Faaso, Tunisii, Esipt, Sàmbi, Gine Ekuwaaatoriyaal, Niseriyaa, Kab-Weer, Gine Bisaawo, Mali, Gine Konaakiri, Gana, Àngola, Tansani, Mosàmbig, Moritani, RD Kongo, Gàmbi, Namibi ak Kamerun.