Démb, ci àllarba ji la ñenn ñu bokk ci Nguur gu bees gi biral yenn ci njuuj-njaaji Nguur gi ñu wuutu. Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko moo xamle na ne nangu nañu lu tollu ci ñaar-fukk ak juróomi taax (immeubles) yoo xam ne Càmm gi moo leen moom. Kii di Ibraahiima Si, jëwriñ ji ñu dénk wàllu wér-gi-yaram gi, biral na ne am na lu tollu ci 1 080i liggéeykat yu nekkul ci yoon (irréguliers). Mu amaat tamit, 399i doomi Aadama yoo xam ne ñi ngi jot seen i peyoor bu yàgg ba tay. Te, xamaguñu ñooñu ñan lañ. Waaye, wayndare wi dinañu ko jébbal Yoon mu def ci liggéeyam.
NDOGUM YOON FA BUNKILIŊ
Ndogum yoon mu metti moo am tay, fa boori Senoba, dëkk bu digaloo ak Gàmbi. Mu nekk xeetu ndog moo xam ne bariwul lu ñu koy gis ci yoon yi. Ndax, ñetti daamar ñoo mbëkkante bees sukkandikoo ci waa Seneweb. Genn sëfaan (camion) gu mag, geneen gu ndaw (camionnette) ak benn minikaar ñoo mbëkkante. Ñaari bakkan rot nañ ci, juróom doomi Aadama jële ci ay gaañu-gaañu yu metti.
CONGUM KËRUG ABDU RAHMAAN JUUF FA SICAP
Ba kàmpaañ yi dooree ba tay, mel na ne fitna ji delluwul ginnaaw. Fan yii rekk, amoon na ay jàmmaarloo yu metti ya amoon fa Ndar ba mu juroon coow lu réy fi réew mi. Ñu bari jàppoon nañu ne taafar si dina wàññeeku. Waaye, mbir mi demewul noonu. Ndax, démb ci ngoon lañu song këru kenn ci lawaxi Pastef yi (fa Ndakaaru). Moom, Abdurahmaan Juuf, moo jiite Pastef fa goxu Sicap Liberté. Nee na, njëggum ñaari lëkkatoo yii di Takku/Wallu ak Sàmm sa kàddu ñoo ko song. Mbir maa nga xew jamono ji kilifay làngu Pastef gi di amal seen ub “meeting” fa “Stade Amadou Barry” bu Géejawaay. Xamle na ne dina jébbal ab pelent ngir ñu teg loxo gaa ñi def loolu.
NÉEWAAYU LIMUB ÑI JËLI SEEN I KÀRT
Diir bu gàtt a des ci wote yi. Waaye, ba tay, am na limub kàrt bu takku bu des boo xam ne seen i boroom jëleeguñu leen. Mu nekk mbir mu xaw a jaaxal gaa ñiy yëngu ci pólitig. Ndax, lu tollu ci 278 736i kàrt yi jàppandi, 16 660i kàrt kepp la ci seen i boroom jël.
PS BIRAL NA PÉETEEM FA NDAKAARU
Ñetti fan kepp a bëgg a des ci wote yi. Waaye, ba tay, am na làng yu biralagul seen péete ci yenn gox yi. Ñii di waa PS (Parti Socialiste) moom, bokkuñu ci. Bu dee am na sax ñu jàppoon ne Sàmm sa kàddu bi Bàrtelemi Jaas jiite lañuy jàppale, defewuñu ko noonu. Nde, dañu koo wan ginnaaw. Ñoom, xamle nañu ne lëkkatoo Jàmm ak njariñ bu Aamadu Ba lañuy àndal fa goxub Ndakaaru.
DIC WOOLU NA SÉEX GAJAGA
Waa DIC (Division des Investigations Criminelles) ña ngay déglu Séex Gajaga bees sukkandikoo ci waa Dakaractu. Li waral ndéglu gi, mooy mbirum génnug àdduna Mustafaa Ba. Ndax, dafa am ay kàddu yu mu yékkati ci mbir moomu. Dafa di, anam yi mu génnee àdduna dafa xaw a doy-waar. Te, ba tay, xamaguñu li nekk ci ginnaaw, ci ay luññutu kepp lañu nekk.