LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (14/2/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

DÀQATI NAÑU LAYOOB SÉYDINA UMAR TURE AK SÉEX YÉRIM SEKK

Coow li dox diggante ki fi nekkoon kàppiteen bu sàndarmëri ak kii di Séex Yérim jeexagul ba tey. Moom Séydinaa Umar Ture daf ne waa ji dafa yàq deram (diffamation) ci téere bi mu fi génne woon bu yàggul dara ci pàcc bi mu jagleel coowal “Sweet Beauté” li. Looloo taxoon mu pelent ko. Boobaak léegi nag, jàppal nañu leen ñetti yoon ab layoo di ko fomm. Wii yoon, jàppaat nañu layoo boobu fukki fan ak ñett ci weeru màrs wii di ñëw.

TAXAWAAYU CFDP ÑEEL MBIRUM “AMNISTIE” AK WAXTAAN WI

 CFDP (Collectif des Familles des Détenus Politiques) ag kurél la gu ëmb mbokki gaa ñi ñu tëj ci kaso yi. Te, lenn waralu ko lu dul ñàkk a bokk ak ki fi nekk gis-gis. Maanaam, ñi ñuy dippe ay “détenus politiques”. Ñoom nag, ñi ngi leeral seen taxawaay ñeel mbirum “Amnistie” mi ñuy ruumandaat ak waxtaan wi ñu namm a amal. Bi ci jiitu, mooy ne ànduñu wenn yoon ci ndàqug wote yi. Ndax, loolu firnde la ci ne ñoom it, seen diir ba ñu war a def kaso day yokk ni moomeg Njiitu réew mi yokkee. Bi ci topp, mooy ñoom duñu nangu ñu leen di tayle. Maanaam, sàrt boobu ñu bëgg a jël ngir Maki Sàll, du ngir ñoom. Li ñu bëgg mooy ñu àtte leen, ndax defuñu dara. Rax-ci-dolli, Njiitu réew mi du fi def lu ni léŋŋ, ba noppi, bëgg a jaare ci ñoom ngir suul ñaawteef yooyu. Te, mbokki ñi ci loru toog di xool ak naqar wi ñu leen teg. Ci gàttal, ñoom bokkuñu ci waxtaan te, santuñu leen ñu bàyyi leen ci anam yooyu.

ÑIY YËNGU CI WÀLLU JOKK-JOKKALANTE GI FIPPU NAÑU

Liggéeykat yiy yëngu ci wàllu jokk-jokkalante gi ñu leen dippe “les travailleurs des opérateurs de télécommunications” wone nañu seen naqar ñeel ndogal li Nguur gi jël. Maanaam, lënd gi muy dagg-daggee saa yu ko neexee. Ndax, diggante ñaari fan ci weeru suwe 2023 ak fukki fan ak ñett ci weeru féewiryee wii jëwriñ ji ñu dénk wàll woowu di Musaa Bookar Caam dog na lënd gi fukki fan ak ñett. Loolu tax ñu ñàkk ci xaalis bu takku. Nee ñu, diggante boobu rekk ñu doge jokkalante gi ci mbaali jokkoo yi ñàkk nañu ci lu tollu ci ñetti miliyaar ci sunuy koppar. Te, waxaalewuñu li ci seen i kiliyaŋ yiy ñàkk. Moo tax ñoom waa “Orange, Free ak Expresso” ne lu mujj tey, dinañu door ab xeex ngir Nguur gi dakkal xeetu doxalin yii. Te, dinañu ci dem ba jeex.

WAA PASTEF AK BUUBAKAR KAMARA TEGGI NAÑU TUUMA

Démb la lawaxu PDS bi, Kariim Maysa Wàdd, fésal ci mbaali jokkoo yi ne Usmaan Sonko mi ngi waxtaan ak Njiitu réew mi ngir ñu génne ko ci kaso bi mook ñi ñu ko tëjandooloon. Te, nee na Piyeer Gujaabi Atepaa, Buubakar Kamara, Séydi Gasama Àlliyun Tin ak ñeneen ñoo ko dox. Buubakar Kamara nee na mi ngi seede ne mësut a séq wenn waxtaan ak Njiitu réew mi walla ak Nguuram ñeel bàyyig Usmaan Sonko. 

Naka noonu, kii di Aamadu Ba bokk ci kilifay Pastef yi tamit, tontu na Kariim ñeel tuuma yi mu teg ci seen njiit li. Nee na ko bum duggal Usmaan Sonko ci seen njuuj-njaaj yooyu. Sonko mësut a daw te du mës a gàddaay di teg ay xeexam ci loxoy ñeneen.      

CAF DAAN NA KEREPIŊ JAATA

Doomu Senegaal jii di futbal jamono jii fa As Monakoo, yetu CAF (Confédération Africaine de Football) wi dal na ko. Li waral loolu mooy kàddu yi gaynde gi yékkati woon teg ko ci ndoddi arbit yi bi joŋante bi doxoon diggante Senegaal ak Koddiwaar jeexee. Ndax, moom dafa jàppoon ne gaa ñi dañoo doxal lu leen neex. Lu ko moy, kon Ismayla Saar waroon na am ab penaatii. Te, arbit yi demuñu “Var”  sax. Waaye, yemul foofu kese. Ndax, daf ci yokk ni dañu leen a ger. Kàddu yooyoo tax ñu daan ko ñeenti joŋante yoo xam ne ñaar yi moom du leen teewe. Yemuñu foofu rekk. Gàll nañu ci ndoddam it lu tollu ci juróomi miliyoŋ yoo xam ne ndàmpaay la.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj