Démb ci altine ji, Elimaanu jëwriñ yi, Sëñ Usmaan Sonko, moo nga woon fa Ngomblaan ga ngir tontu laaji dépite yi ñeel tolluwaayu réew mi. Bari na nag ponk yees fa waxtaane ak i laaj, donte ni ñu bari ci dépite yi bokk ci kujje gi wuyujiwuñu woon. Ci biir i tontoom, Elimaanu jëwriñ yi wax na ci sañ-sañi taskati xibaar yi. Mu cay xamle ni duñu jéggale lenn lu jëm ci tasaare xibaar yu wérul. Bu dee ci wàlluw pas yees daqal, ay nit ñàkk ci seen i liggéey, andi na ciy weddi. Naka noonu, muy biral ni duggewuñu ko singaliwaate. Ñi ci bokk tamit, mën nañoo dem ci Yoon. Xamle naat ni dinañu amal i coppite jëme ci lempo yi, dakkal yi ñu daan teggil yenn këri doxandéem yi ngir yokk doole gafakag réew mi. Dinañu jël itam ay pexe ngir ñu sàmmonteek njëgi dund bi. Bu loolu weesoo, Càmm gi dina jébbal Ngomblaan gi ay sémbi àtte ci fan yii di ñëw ngir taxawal caytu gu leer.
MBIRUM KOPPARI MBAS MI
Mbirum koppari mbas mi, ñu gën koo miin ci Fonds Covid, yëngatuwaat na. DIC (division des investigations criminelles) a ngi wéyal luññutu yi ci luubal yees ci njort. Démb ci altine ji, 14i fan ci weeru awril 2025, woolu woon na ñenn ñu ci seen i tur fés lool. Daanaka ñépp lañu téewandi ginnaaw bi ñu leen dégloo. Tay ci talaata jeet, woolu nañu juróomi kilifa yu bokk ca njëwriñu wér-gi-yaram gi.
GII MARI SAAÑAA A NGI SÀKKU ÑU TOPP MAKI SÀLL
Dépite bii di Gii Mari Saañaa jébbal la Ngomblaan gi ag càkkuteef ngir ñu topp ki fi nekkoon Njiitu réew mi, Maki Sàll (2012-2024), ni ku wor askanam. Li mu kay tuumal ca càkkuteef googu nag mooy ni dafa teggi yoon, leb ci turub réew mi lu ëpp 2 500i milyaar. Bi mu koy def, Ngomblaan gi àndu ci. Naka noonoot, muy wax ni jëfandikoo na ay konti gafakag réew mi, teg ci nëbb tolluwaayu koom-koomug réew mi ba mu jural réew mi jafe-jafe yi mu nekke.
CONG MA AM FA SIGICOOR
Fa Sigicoor, nemmeeku nañu fay sàmbaa-bóoy yu gànnaayu ba diis yu fa amal am cong. Mbir maa nga xew démb ci altine ji, bi 22i waxtu di jot, ci benn dëkk bu ñuy wax Jinaaki, fa Biññonaa. Bees sukkandikoo ci sunuy naataango yu APS, dañoo njëkk a dogaale ay nit ci mbedd yi, nangu seen i telefon. Ginnaaw gi lañu tàmbalee soqi ay sox, laata ñuy dugg ci bitig yi, di leen yulli.