Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay bawoo na fi tay ci talaata ji, wutali Kotonu, réewum Benee. Mu fay amal tukkib xaritoo ak liggéey bu aju ci dooleel lëkkatoo gi dox ci diggante ñaari réew yi. Tukki bi di dellu ci njógteg Njiitu réew mi ngir dëgëral diggante yu am solo yu Senegal tabax ci digganteem ak ay lëkkatoom yu ci diiwaanu Afrig sowu-jant. Njiitu réew mi dina fa amal ay waxtaan ci lëkkatoo yu aju ci koom-koom, kaaraange diiwaan bi ak Bennoo Afrig. Loolu dellu di wane taxawaay bi Senegaal am fi diiwaan bi ngir jiite ay naal yu mën a soppi jafe-jafe yi ñu bokk di dund.
NJUREEFI KÀTTEY BAC 2025
Ginnaaw bi ñu amalee kàttey BAC bi ci ñaari ayu-bés yi weesu, Office du Bac, di kurél gi doon saytu kàtte yi, génnee na njureef yi tukkee ci ay gu njëkk geek ñaareelu ay gi. Njureef yooyu wane nañu ni 42,85% (téeméeri lawax yoo jël, daanaka ñeen-fukk ak ñett yi) ñoo am seen lijaasa.
Mu yemook 69 474i lawax yu am BAC ci atum 2025 mi. Waaye lim bi dafa wàcc bees ko gamgamle ak limub at mi weesu te yeggoon ci 48,71% (daanaka ñeen-fukk ak juróom-ñeent ci téeméer bu nekk).
Ca njëlbeen 166 439i lawax ñoo bindu woon. Waaye 162 125 ñoo jotoon a teew ci kàtte yi. Ci ñoom, 33 751 yi ñoo jàll ci ay gu njëkk gi. Bi ñu demee ci ñaareelu ay gi, 35 723 lawax daldi ciy tegu.
MUJJANTALUG DALU SÓOBAREY FARÃS FI SENEGAAL
Des na tuuti, réewum Farãs dootul am dalub sóobare fi réew mi. Nde, fileek ñetti fan, 18 sulet 2025, réewum Farãs dina jébbal kilifay Senegaal yi dalub sóobarey Farãs (EFS Éléments Français au Sénégal) bi ñu fi dese. Àmbaasaatu Farãs bi nekk Ndakaaru moo ko xamle démb ci altine ji, 14 sulet 2025, fekk ñu fa doon màggal bésub réewum Farãs, ci teewaayu ñenn ci kilifa yu mag yi ci réew mi.
Lu ni mel nag, bees ca yeggee, dina doon guleet ci mboor, Farãs rafle fi sóobare li ko dale ca atum 1960 ba jonni tay. Naka noonoot, réewum Senegaal ak mu Farãs dinañu jàll ci doxalin wu yees ñeel seen jëflante ci wàllu sóobare.
S&P WÀCCE NA NOTU SENEGAAL
S&P, di kurél guy yëngatu ci caytu ag natt koppari réew yi wàcce na notu Senegaal ci mën boppam. Ginnaaw bi mu càmbaraatee tolluwaayu réew mi ci koppar, dafa ko jële ci « B » bi mu nekkoon, andi ko ci « B- ». Xibaar booboo ngi tukkee ci jëwriñu Ngurd mi.
Mu nekk nag not bob, dafay màndargaal boru Senegaal ci tolluwaay bu kawe ba tax meññlukat yi di fi ragal a dugal seen xaalis. Nde dafay dellu di wane ni Nguur gi lottee ci fay ay boram. Terewul nag jëwriñ ji di dalal xeli lëkkatoo yi ci mën-mëni Nguur gi ak taxawaayam ngir sàmmonteek i pasam. Muy xamle ni naalu kopparal wu 2025 wee ngi ñuy doxal te ci ndoorteelu at mi, dajale nañu koppar yu takku ci lëkkatoo yeek jawu biir réew mi. Ñoo ngi waajal itam ay pexe yu ñeel kopparal gu 2026.