Fukki fan ak juróom-ñaar ci tey bi Usmaan Sonko ak i ñoñam tàmbalee xiifal ba léegi. Fii mu tollu nag, ba léegi ma nga ñu téye ca raglub Ndakaaru (loppitaanu Principal) ba mu nekkoon. Ñoom Baara Njaay ak Anibaal Jiim itam ñoo nga fa ñu téye. Ñoom sax dañoo lànkal seen i mbokk ñu dugg fa ngir nemmeeku leen.
ÑAAWTEEF
Gune gu ndaw gu tollu ci juróomi at lañu jam ba noppi rendi ko. Muy jëf ju doy waar ju xewee ci benn taax bu nekk fa Saam-Noteer, Géejawaay. Xale bi nag, bi muy naaj tuuti la ko ñaari magam yi mu nekkaloon ca seen kër fekk ci kow teeraas bi ñu muur ko. Ci xibaar yi jot a rot, moom ak ñaari magam yi dañoo seeti woon seen baay ci bër yi. Bi ñuy gis mbir meet fekk na seen baay liggéeyi. Jamono yii, pólis a ngi déglu lokaateer yi ñu bokkal taax ma ngir leeral ak teg loxo ki amal jëf ju ñaaw joojule.
DÀQATI NAÑ LAYOOB DÉPITE PUR YI
Dàqati nañ layoob dépite PUR yi, Masata Sàmb ak Mamadu Ñaŋ, ba keroog 20i fan ci nowàmbar 2023, ngir layookat yi mën a làyyi.
Juróom-benni ati kaso lañu daanoon ñaari dépite yi, teg ci alamaanu ñaar-fukki junni (100 000 FCFA) ak juróomi tamndaret (5 000 000 FCFA) yi ñu war a dàmpe dépite Bennoo Bokk Yaakaar bii di Ami Njaay Ñiibi. Keroog, 2i fan ci saŋwiyee 2023, la leen àttekat bi gàlloon daan bile.
Ñoom nag, ñaari dépite yi, jotoon nañ leen tëj laata ñu leen di bàyyeendi.
TÀGGAT-YARAM
Gaynde Senegaal yu góor yi (basket) am nañu ndam ci seen joŋante bu njëkk ci bokkadil (éliminatoires) yu powum ólempig yi. Ekibu Niseriyaa bi lañu dóor 93-87. Tey jii, ci talaata ji, lañu waroon a laaleek réewum Ugàndaa. Waaye, ekibu Ugaandaa bi dañu ko génne ci xëccoo bi. Joŋante bi leen dese dina dox ci seen digganteek Mali, ci alxames jii 17i fan ci ut 2023.