UEMOA (Union Economique et Monétaire Ouest Africaine) mooy mbootaay gi boole réewi Afrig sowu-jant ci lu jëm ci wàllu koom ak xaalis. Njiitul kurél googu di Abdulaay Jóob, moom la Njiitru réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, doon dalal démb. Li gën a fés ci seen waxtaan wi mooy naalu atum 2030 mi ak gis-gisu UEMOA ñeel atum 2040 mi ci bennoog réewi jegeñaale yi (sous-région) ci wàllu koom ak xaalis. Waaye, laata muy ñëw ci loolu, tënk nañu tolluwaayu réewi Afrig sowu-jant yi ci ci wàllu koom-koom. Nde, kenn umpalewul ne jamono jii réew yi jaxasoo nañu tee, xaajaloo gi bari na lool. Loolu nag, mën na gàllankoor koom-koom gi.
NJIITU RÉEW MI TAS NA CNDT
Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, tas na kurél gi ñu dénkoon Ndiisoog mberaay yi (CNDT) te ñu taxawaloon ko ci dekkereb 2015-1970 bu 21i desàmbar 2015. Yeggee na ndogal li ki jiite woon kurél gi, muy Bënuwaa Sàmbu.
MBIRUM SËFAANI SENEGAAL YA CA DIGU GÀMBI BA
Bàyyi nañu 353i sëfaani Senegaal ya ñu téyee woon ca digu Gàmbi ba. Jëlaat nañu tali bi, tàmbalee dawaat. Jëwriñu yaale ji (dem beek dikk bi), El Maalig Njaay, moo fa jaar, moom ak jëwriñu yaxantu gi, Sëriñ Géy Jóob. Ñoom ñaari jëwriñ oo dem ba Gàmbi, toog ak kilifa ya ngir wut pexe. Ginnaaw gi lañ déggoo, lijjanti mbir mi. Nee ñu, kilifay ñaari réew yi ñoo ngiy wéyal seen i diisoo ngir gën a woyofal dem beek dikk bi ci diggante ñaari réew yi.
LU BEES ÑEEL LUUBALUG 1,8i MILIYAAR FA CSS
Coowal luubalug benn miliyaar ak lu teg fa kër gii di CSS (Caisse de Sécurité Sociale) mi ngi bëgg a yàgg. Dafa di, yëf yi dafa am lu ci bees. Ndax, kenn umpalewul ne am na ñaar ñu ñu jotoon teg loxo ci mbir moomu ci weeru sulet wii ñu génn. Am na ñeneen ñaar ñu yokk ci lim boobu. Bees sukkandikoo ci “Libération”, nee na teg nañu loxo K. Faal (chef de l’agenceWiltord) ak M. Mbóoj (directeur de l’agence du Plateau). Li ñu leen di toppe mooy luubal alalu askan wi, li ñuy dippe “association de malfaiteurs”, “blanchiment de capitaux” ak “contrefaçon et usage de chèques contrefaits”. Kon, jamono jii, ñoom ñeent ñépp ñoo ngi ci loxoy Yoon.
BÀYYI NAÑU AADAMA FAY
Bu yàggul dara rekk, moom Aadama Fay, di rakk ci Mareem Fay Sàll, ñi ngi ko doon tudd ci mbirum suuf. Nde, moom dafa yor ag këru liggéey guy yëngu ci loolu. Te, way-juram wu jigéen am na ci wàll. Looloo tax sax, yaay ji déglu woon nañu ko ci fan yii. Moom Aadama nag, waa “Section de Recherche” tegoon nañu ko loxo ci talaata ji. Waaye, mujj nañu koo bàyyi ci guddig àllarba ji jàpp alxames.
XEW-XEW BU DOY-WAAR FA CEES
Xew-xew boobu mi ngi am ci subag alxamesu tey jii, ay boori juróom-benni waxtu. Benn sàmbaa-bóoy moo dogaale benn pentuurkat bu yoroon ab moto ngir nangu ko ci moom. Ca la ko jamee paaka, mu génn àdduna. Waaye, laata muy rëcc la ko gaa yi jàpp moom tamit daldi koy taal. Bi takk-der yi ñëwee ñaari néew lañu fa fekk.