LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (16/01/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

DOXIINU YOON CI RÉEW MI

Lépp lañ war a xoolaat ci ni yoon di doxee fi réewum Senegaal. Muy gis-gis bu Meetar Maam Aadama Géey, di layookat, fésal. Fekk ñu doon ko dalal ci jotaayu Objection bu Sud Fm, bërki-démb ci dibéer ji 14 sãwiyee 2024. Muy nag mbir mu ko yitteel lool bees ko déggee. Nde, ciy waxam, lu ëpp 25i at ñoo ngi nii mu koy wax ak di ci dox. Waxtaan na ceek jëwriñ yes dénk mbiri yoon yépp, ca jamonoy Sag Bódĩ ba léegi. Waaye li mu seetlu mooy way-pólitig yi dañuy gaawantu ci ndogal yi ñuy jël ñeel doxiinu yoon. Looloo tax ba coppite bu dëggu mësu cee am.

COOWAL BAAYALE YI : MUHAMET BEN JÓOB DUGAL NA DABANTAL

Muhammet Ben Jóob, kenn ci lawax yi ndajem ndeyu àtte réew mi seppi woon ci seen càmbar gu jëkk dugal nab dabantal. Moom nag, dafay sàkku ci ndaje mi mu saytuwaat wayndareem. Bees sukkandikoo ci li ndawam li, Usmaan Kaas Ndaw wax, jamono ji ñuy saytu xobi baayaleem yi, masin bi dafa taxawoon ba ñu mujjoon ko fay, taalaat ko. Te gisuñu fu ndajem ndeyu àtte mi tuddee lu ni mel ci caabal gi mu génne ñeel caytu gu jëkk gi. Naka noonu itam, muy ñaawlu baayaleem yu bare yu nekkul ci kayiti wote yi, ba ci moom lawax bi.

UBBITEG BRT BI

BRT bi tàmbali naa daw biir Ndakaaru. Bërki-démb ci dibéer ji, 14 sãwiyee 2024, lañ ko doon ubbi ci teewaayu Njiitu réew mi Maki Sàll ak ñenn ci jëwriñi Càmm gi. Ñu doon amalee xew-xew bi fa gaaru géejawaay. BRT bi nag, mbëj rekk moo koy dawal, mbëj muy jóge ci jant bi. Càmm gi ànd ceek Senelec mu ko koy jox. Ba tey, ngir yombal amalug mbëj mi, Njiitu réew mi xamle na ni dinañ amal i diisoo ak këru liggéey yu deme ni Dakaar mobility ak Fonsis ndax ñu mën a lëkkatook Senelec ba mën a jële ci jant bi mbëj mu doy muy dawal BRT bi.

AKSIDAŊ CI OTORUT BI

Aksidaŋ bu metti moo amoon ci otorut bi. Ñetti daamar ñoo mbëkkante fi tollook Jamñaajo, booy dugg Ndakaaru. Bees sukkandikoo ci xibaar yi wallukat yi jot a rotal, kenn ñàkku ci bakkanam. Waaye, am na 16i nit ñu ci jëley gaañu-gaañu. Juróom yi doon ay gaañ-gaañu yu metti.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj