LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (16/1/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

UBBITE ËTTI ÀTTEKAAY YI

Tay ci alxames ji moo nekkoon bésub ubbite ëtti àttekaay yi. Ndaje la nag moo xam ne, at mu jot dañu koy amal. Ki ko jiite ci atum ren jii di Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Mu amal fa waxtaan wu am solo lool. Li nekkoon ponku waxtaan wi mooy “Sañ-sañu ñaxtu ak sàmm li ñépp bokk”.

MURIG MBALAANU KIIRAAYU FARBA NGOM

Muhammadu Ngom, ñu gën ko xam ci turu Farba Ngom, kenn la ci way-bokki APR (Alliance Pour la République). Moom nag, Yoon daf ko woolu ci mbirum 125i miliyaar. Waaye, balaa muy wuyuji, fàww ñu muri mbalaanu kiiraayam. Nde, kenn umpalewul ne dépite la. Ba tax na, dépite yi woolu nañu leen suba fa Ngomblaan ga ngir ñu tànn dépite yuy fénc mbir moomu ñeel ko. Maanaam, dañuy ay dépite yiy càmbar lijëm ci murig mbalaanu kiiraayu seen naataangoo boobu.

LIMUB DAWALKATI MÓTO-JAKARTAA YIY SÀKKU AY KËYIT

Lu yàggul dara, jëwriñ ji ñu dénk wallu dem bi ak dikk bi dafa joxoon dawalkati móto-jakartaa yi àpp ngir ñu wut ay këyit, daldi sàrtoo ak Yoon. Mbir mi juroon na coow ca ndoorteel la. Waaye, gaa ñi dafa mel ni mujj nañoo teggi seen tànk fa ñu ko tegoon. Diggante bi yëf yi dooree ak léegi, jot nañu lu tollu ci 3. 800 ci ay càkkuteefi këyit. 2. 354 yi moom nangul nañu leen. Ndax, matal nañu li ñu leen laaj. Mu am 1. 500 yoo xam ne dañu gàntal seen i càkkuteef. Te, lenn waralu ko lu moy ay jafe-jafe ci li ñuy dippe CMC (Certificat de Mise en Circulation).

NDOGUM YOON

Ndog moomu mi ngi am tay ci alxames ji. Genn daamar moo mbëkk ginnaawug sëfaan. Am na kenn ku ci ñàkk bakkanam. Waaye, jéyya ji yemul foofu. Ndax, am na ñaar ñu ci jële ay gaañu-gaañu yu metti. Ndog moomu,  mi ngi ame ci “autoroute à péage” bi nekk diggante Cees-Ndakaaru.

XEW-XEW BU TIIS FA LUGA

Xew-xew boobu mi ngi am démb ci ngoon fa Póotu, nekk ca wetu Luga. Ñaari néew lañu fekk ca wetu ndox ma. Xamaguñu nag fan lañu bawoo. Li ñu jàppagum kay mooy ne dañoo bokk ci mool yi seen gaal suuxoon fa Ndar, ci talaata jii weesu. Tijji nañu ci ag luññutu ngir xam nu mbir mi tëdde. Néew yaa nga ñu dencandi fa raglu Luga bu mag ba, di opitaal Ahmadu Saxiir Mbay.

BENEEN XEW-XEW BU TIIS FA MBËLLËXE

Mbir mii, mi ngi ame ci genn kuppe gu ñu doon amal ci ngoonug démb gi. Benn xale bu góor buy tollu ci fukki at ak juróom-ñeent moo fa daanu, jaare fa ñàkk bakkanam. Bees sukkandikoo ci waa Leral.net, waxambaane boobu mi ngi doon wuyoo ci turu P. M. Njaay, doon jànge fa liise bu Mbëllëxe.

FAMA YI LOTTALATI NAÑU AY RËTALKAT

Réewu Mali bokk na ci réewi Afrigu sowu-jant yi rëtalkat yi gën a sonal. Ndeem sax, at yii yépp, ñu ngi xeex ak ñoom. Waaye, loolu taxul ñu dakkal seen i cong. Nde, démb rekk song nañu leen donte ne sax, sàmbaa-bóoy yooyu mujjuñoo am la ñu bëggoon. Ndax, FAMA (Forces armées maliennes) yi mayuñu leen fu ñu yakkee seen nàkk. Bees sukkandikoo ci waa Seneweb, jàpp nañu ci saay-saay yooyu juróom-benn, nangu ci ñoom juróomi móto, ñaari fetal, benn rajo ak i sox. Mu am tamit kenn ci sóobarey Mali yi ku ci jële gaañu-gaañu, donte ne sax mettiwul noonu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj