LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (16/5/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

WÀÑÑIG DUND BI

Wàññig dund bi bokk na ci li gën a soxal saa-senegaal yi jamono jii, rawatina ñi seen loxo jotul seen ginnaaw. Moo tax, ndaje mi elimaanu jëwriñ ji jiite woon démb xamle na jéego yi ñu ciy def ngir yëf yi gën a oyof ci askan wi. Nde, xamle na ne gise nañ ak yaxantukat yeek mbooleem ñi nekk ci wàll woowu ngir dund bi mën a wàññeeku. Yi ñu bëgg a wàññi nag, ceeb la, suukër, mburu ak diw. Mu yokk ci ne loolu moom du yombe noonu. Ndax, loo xam ne moom nekkul say loxo, danga koy jéggaani rekk, mënoo wax lu la neex lay jar. Te, balaa loolu di mën a am fàww li ñuy dunde di jóge ci réew mi. Te, nee na lu dul yàgg dara dinañu génn waxtaan ci ak saa-senegaal yi.

NJIITU RÉEW MI JËLAAT NA YOON

Ginnaaw ba mu demee fa Koddiwaar, Gine ak Muritani, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dina amalaat yeneen tukki bitim-réew. Waaye, tukkeem yooyu ba tey ci biir kembaaru Afrig gi la leen di defe. Wii yoon moom, ma nga jëm fale ca Gana ak Niseriyaa. Tukki yooyu nag, dina leen amal diggante tey ci alxames ji ak suba ci àjjuma ji.

MBËKK MI

Doomi Senegaal yi teggeeguñu seen tànk fa ñu ko tegoon. Nde, donte ne sax ay bakkan rot nañ, am ñu ñu ci waññi, loolu taxul ñu bàyyi. Moo tax, diggante juróom-ñaari fan ci weeru me ak démb ci àllarba ji, marinu Senegaal waññi na lu ëpp juróomi téeméer yoo xam ne dañoo bëggoon a mbëkki. Maanaam, dañoo bëggoon a dem fa Ërób. Gaal yooyu ñu waññi yépp Senegaal lañu bawoo, genn kese moo ci bawoo Gàmbi.

XEW-XEW BU TIIS FA SIGGICOOR

Xew-xew boobu mi ngi am tey ci àllarba ji fa koñ bii di “Grand-Yoff” nekke fa Siggicoor. Nde, dañoo gis ci kanaal yi benn liir bu ñu laxas ak ub sér muy tëmb. Ñoom nag, bi ñu koy gis fekk na mu faatu. Nee ñu, liir bi jigéen la woon. Ca saa sa lañu ko yóbbu fa raglu ngir xam ci yan anam la génnee àddina. Rax-ci-dolli, ubbi nañu ag luññutu ngir xam ku def jëf ju ñaaw jooju.

YOON

Barki-démb ci talaata ji la ko waa “Commissariat” bu Géejawaay tegoon loxo mbër mii di Lac de Guiers 2. Li ñu koy toppe mooy mbirum njuuj-njaaj ngir tukkiloo ay saa-senegaal. Ci mbir moomu nag, dañu nax gaa ñu lu tollu ci ñaar-fukki miliyoŋ ak benn. Ñooñu ñoo ko yóbbu ci Yoon mook ka mu bokkaloon jëf jooju. Waaye, waa jooju moom ba tey tegaguñu ko bët. Moom Lac 2 jamono jii, jébbal nañu ko toppekat bi.

Naka noonu, ci talaata ji tamit lañu jàpp doomi Idiriisa Sekk ji, A. Sekk. Ñi ko teg loxo mooy takk-deri OCRTIS yi (Office Central de la Répression du Trafic Illicite des Stupéfiants). Li ñu ko jàppe du lenn lu moy da doon yëngu ci li ñuy dippee “trafic international de drogue”’, maanaam, mbirum sineebar. Nee ñu nag, mbir mi du kenn nit kese, kippaango la goo xam ne luy tollu ci juróom-ñetti sàmbaa-bóoy ñoo ngi ci. Te, moom bokk na ci ñi ko jiite woon. Jamono jii nag, ma nga ca loxoy Yoon.

MAHAMAT IDRIIS DÉBI ITNOO JËL NA RÉEWUM CÀDD

Ginnaaw ñetti at ba sóobare jiite réew mi ba tey, moom Seneraal Mahamat idriis Débi Itnoo mujj na nekk léegi Njiitu réew ma. Ndax, ca fan yee weesu lañu doon amal seen i wote. Moom moo ca jiitu, ndax 61% ci askan wi moom lañu woteel bees sukkandikoo ci njureef yi ndajem ndeyi àtte mi rotal. Ki ñu bari jàppoon ne moo ëpp doole di Succès Masra, moom 18,54% kepp la am ci wote yooyu.

 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj