LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (16/8/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

TEG NAÑU LOXO LÉWOO ÑING

Léwoo Ñing mi jiite Pastef fa goxub Njagañaaw, jàpp nañu ko. Ndawi DIC yi ñoo ko teg loxo fale ca AIBD (Aéroport International Blaise Diagne). Moom nag, li ñu koy toppe mooy biral ci mbaali jokkoo yiy mbir yoy, daf ciy ŋàññi Njiitu réew mi Maki Sàll. Yemuñu ci ne moom dafa tooñ Njiitu réew mi. Waaye, dañu ni tamit ñi ngi koy toppe ni kuy def mbir yuy xajamal walla gàkkal càmmeef yi. 

JÀPPU NAÑU ABDU XAADAR SAAXO

Abdu Xaadar saaxo, di kenn ci taskati xibaari kër gii di Senegoo, moom lañu téye altine ba tey. Moom nag, ñi ngi ko defoon lii ñu naan “garde-à-vue”. Mu mel ni ñii di waa DIC jeexal nañu seen i laaj. Nee ñu, amaana tey ci àllarba ji ñu jébbal ko toppekatu bokkeef gi. Li ñu koy toppe mooy biral ay xibaar yu wérul bees sukkandikoo ci layookatam bii di Meetar Musaa Saar.

U.A ÀNDUL AK CEDEAO

Mbootaayu Bennoog Afrig (Union Africaine) àndul ci li waa CEDEAO namm a def fale ca Niseer. Ca ndaje ma ñu doon amal lañu xamlee ne dañuy bañ lépp luy xeetu jëfandikoo doole (ngànnaay) ngir saafara coow la am ca Niseer. Taxawaay boobu nag dees na ko dëggal ci ab yégle bu war a génn tey jii bees sukkandikoo ci xibaar yi rotagum. Waaye, loolu terewul ne bànqaasug U.A gii di CPS (Conseil de Paix et de Sécurité) génnee na ñii di waa Niseer ci mbooleem xew-xew yi waa U.A di amal. 

MBËKK MI

Géej gaa ngay wéy di wann doomi Afrig yi , rawatina yu Senegaal yi. Geneen gaal gu doon mbëkk moo fëllijee ca boori Kab-Weer. Am na nag ñu ñu ca jot a rawale. Bees sukkandikoo ci jëwriñ ji ñu dénk wàlluw bitim-réew ak doomi Senegaal ya fa nekk, gaal googu moo jóge woon ca Faas-Bóoy, nekke fa Cees, ci boori fukki fan ci weeru sulet. Mu amoon lu tollu ci téeméer ak benn ci ay doomi aadama. Lu tollu ci fanweer ak juróom-ñett rëcc nañu ci. Ña ca des moom tegaguñu leen bët. 

CONG MA AM CA NISEER

Jamono jii mbirum Niseer moo lëmbe xibaar yi. Leneen lu bees rax na ci. Ay jihyaadist ñoo leen song démb ci boori fa ñu digaloo ak waa Burkinaa Faaso. Mu am lu tollu ci fukki sóobare ak juróom-ñaar yu ci ñàkk seen i bakkan. Lu tollu ci ñaar-fukk ci ñoom jële ci ay gaañu-gaañu, juróom-benn ci ñoom sonn lool, ñépp ñu rawale leen ca Ñaame.

XIBAARI GAYNDEY FUTBAL YI

Yaakaari doomi Senegaal yii di Ismayla Saar, Ilimaan Njaay ak Paap Géy tas na. Seen ékib bii di Olympique de Marseille du dem ca joŋante bu mag boobu boole ékib yi mën ci ërób ñu koy woowe “Ligue des Champions”. Li ko waral mooy joŋante bi leen fa waroon yóbb te, ñu ko doon amal démb, ñii di waa Panathinaikos ñoo leen ca mujj daan.

Doomu Senegaal jii di Abdu Jàllo moom, mbiram jaaxaloon na nit ñi. Ñoo ngi doon laaj fan la nar a futbal ren. Léegi, dafa mel ni am nañu ci lu leer. Moom dem na Al-Arabi Sports Club, benn ékib bu nekk fale ca Qataar.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj