LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (17/01/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

JÉBBALUG DABANTAL YA TAQARNAASE NA

Ñetti fan kepp a des ndajem ndeyu àtte mi biral limu lawax yiy joŋante. Waaye de, xeexoo baa ngi mel ni tulleek maale ci diggante lawax yi. Ginnaaw coowal Ceerno Alasaan Sàll ak mbokki Kariim Wàdd yi ñeel nasiyonalite lawaxu PDS bi, dafa am leneen coow lu jolli diggante Aamadu Ba (Bennoo Bokk Yaakaar), Basiiru Jomaay Jaxaar Fay (Pastef ma woon) ak Séex Tiijaan Jéey. Moom Aamadu Ba, lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar bi, moo jébbal ag dabantal ca ëtt ba doon saytu xobi baayale yi. Moom dafa jàpp ne gaa ñooñu dafa am ay sàrt yu ñu sàmmontewul. Ci gàttal seen i wayndare matul. Li ci jiitu mooy jébbalug këyit yu baaxul fa ndajem ndeyu àtte ma. Ñaareel bi, dañu bokk ci làng gu ñu tas. Ñetteel bi, lëkkatoo gu sosu ci ñàkk a sàmmonte ak sàrt yi. Bi ci mujj di ñàkk a bokk ci lëkkatoo walla làng gi ko def seen lawax. Muy sàkku ñu seppi seen i wayndare.

Naka noonu Usmaan Sonko tamit jébbal nag dabantal. Bosam nag wute ag yeneen yi. Ndax, moom dañu ko waxoon ne wayndareem matul. Ci la demaat mook i layookatam defaraat wayndareem ba mu mat sëkk. Nee ñu, jébbal nañu ko fa ndajem ndeyu àtte ma. Te, am nañu yaakaar ne ëtt boobu dina leen ko nangul. Rax-ci-dolli, seen lawax bi dina bokk ci wotey 2024 yi.

USMAAN SONKO A NGI LEERAL

Ginnaaw bi ñu gàntalee xobi baayaley yenn ci lawax yi, dañu doon sàkku ndimbal. Ndimbal loolu mooy ñu jàppale leen ba ñu mën a matale seen i wayndare. Moo taxon ñu bind ab bataaxal jébbal ko Njiitu réew mi ngir mu jàppale leen. Moom, meeru Sigicoor bi nag, dañu ko boole ci lawax yi xaatim bataaxal boobu. Moo tax mu génne ab yégle di leeral. Mu xamle ne moom fim tollu nii Njiitu réew mi amul jenn màqaama ci loolu. Ñi ci am cër, am ci baat du ñenn ñu dul ndajem ndeyu àtte mi. Mu yokk ci ne mi ngi sàkku ñiy def loolu, ñu bàyyi di dugal turam ci yoo xam ne waxtaanuñu ci ak moom.

COOWAL NASIYONAALITEB KARIIM MAYSA WÀDD JEEX NA

Ay fan ginnaaw bi ñu dekkalaate coowal bokkug doomi Meetar Abdulaay Wàdd ji ci ñaari réew. Mel na ni coow loolu jël na yoonu fey. Ndax, démb ci talaata ji la jëwriñ ju mag joj Farãs rotal ndogal lol, daf ciy indiy leeral. Kon, fim tollu nii, leer na nàññ ne Kariim Wàdd benn nasiyonaalite kepp la yor, muy bu Senegaal. Li mat a laaj kay mooy ndax, yéexaayu ndogal li du jeexital ci aw wayndareem.

AY XIBAAR ÑEEL ÑI AM AY GIITAŊAAS AK YOON

Ba tey, Ustaas Asan sekk a nga ca kaso ba. Nde, moom jébbaloon na sax bataaxalu càkkuteef ngir ñu bàyyi ko bàyyig négandiku. Loolu moom mujjul a àntu. Moo tax moom waaraatekat boobu day mujjee des fa kaso ba.

Kii di Paap Saane tamit nga xam ne tegoon nañu ko loxo, ginnaaw gi ñu bàyyi ko. Moom itam, jamono jii, amaat na ay giitaŋaas ak Yoon. Ndax, ñii di ëttu toppewaay (parquet) ñoo def ag dabantal. Maanaam dañoo ŋàññi ndogal li magum àttekat yi jëloon. Ëtt bii di Néegub tuumalaate bi (Chambre d’accusation) dina leeral mbir moomu suba ci alxames ji fukki fan ak juróom-ñett ci weer wii.

Naka noonu layoo bi waroon a dox ci diggante Mansuur Siise, kenn ci kilifay Pastef yi fa Mbuur, ak Séex Isaa Sàll, meeru Mbuur bi, mujj nañu ko dàq. Layoo boobu jàpp nañu ko ci talaaata jii di ñëw.

JOŊANTE SENEGAAL-KAMERUN

Joŋante bi war a dox ci diggante ñaari ponkal tàmbali na te arbit mbiibagul. Nde, coow li door na xaat. Li ko waral du lenn lu dul limub béréb yi ñu joxeegum. Ndax, nee ñu, fim tollu nii, ñeenti téeméeri biye kepp a jàppandeegum. Li ci gën a doy waar mooy ne, lees war a jot (quota) mi ngi tollu ci juróom-benni téeméer ak juróom fukk. Te, li fa nekk ci ay saa-senegaal ëpp na ñaari junni. Fowu ba nar na yaraax.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj