Ay yooni yoon, Mansuur Fay mi ngi jël yoon wi, di bëgg a tukki. Waaye, bu demee ba fa dalub romplaan ba rekk, ñu waññi ko, ne ko mënoo génn réew mi. Jëwriñ ji ñu dénk biir-réew mi daf ko bind, xamal ko ne mënut a génn réew mi ndax dafa laale ci mbirum koppari mbasum Covid-19 mi. Kon, na toog, bañ a dem fenn ba keroog ñuy saytu ay mbiram. Waaye nag, leeraluñu diir bi.
NDAJEM SAMPUG ÑIY YORE LAF YI CI CAMPEEF YI
Tay ci alxames ji lañu amal ndaje mi ñuy sampe ñiy saytu walla yore laf yi ci campeef yi. ñi ngi doon amale ndaje mi ci teewaayu elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, mi xam ne moo ko jiite woon. Xamle nañu fa ne kippaangoo gu njëkk dina tollu ci téeméer yoo xam ne ñoo war a xeex yàq gi ci campeef yi. Waaye, duñu yam foofu. Ndax, dees na ko yokk ndànk-ndànk ba 9000. Su ko defee payooru bi mën a wàññeeku ci béréb yooyu.
ABDU NGEER DEM NA KASO
Altine jii weesu la ko Yoon woolu woon. Booba tay, kenn xamul woon fu ay mbiram di mujje. Amees na ci lu leer tay ci alxames ji. Moom ak Paab Aamadu Njaay mi moom “compte Tik Tok” “Abdou Nguer Seul”, yóbb nañu leen kaso. Ñoom ñaar, li ñu leen di toppe mooy biral ay xibaar yu wérul.
DAANNAÑU ÑI DOON MBUGAL XALE BI FA NDAR
Nataal ak seedey ñenn yi rote ci xale boobu ñu bari ñi ngi ko doon naqarlu. Nde, ci nataal bi rekk dangay gis ni yaram wi tërgatee. Nijaayam ji def loolu ak ñaar ñi ko ci daan jàppale Yoon mujjoon na leen teg loxo. Waaye, yamul foofu. Ndax, mujj nañu leen àtte ba daan leen. Nijaay ji daan nañu ko juróomi ati kaso yoo xam ne ñett ya lay tëdd ak ñaar-fukki junniy alamaan yu mu war a fay. Ñaar ñi ñi ko daan jàppale tamit, yar ba dal na seen kaw. Daan nañu leen ñaari ati kaso yu ñuy tëdd ak juróom-fukki junni yu ñuy fay alamaan.
CONG MA AM FA MONGON
Dibéer jii weesu la ay sàmbaa-bóoy amaloon am cong fa Jinaki, nekk fa goxu Biñonaa. Ci la sóobarey béréb ba door ag raafal ngir teg loxo ñooñee. Ci raafal googu la sóobare yi dajeek gàngoor gu ngànnaayu. Bi ñu dajee nag, am na benn sóobare bu ci jële ay gaañu-gaañu bees sukkandikoo ci yégleb DIRPA (Directeur de l’Information et des Relations Pupbliques des Armées). Mu am tamit, sóobare boo xam ne dafa réer gisuñu ko, dégguñu ko. Mu ne mes, ne menteñ.