Lu bees amaat na ci coowal suuf ak nger ga am fa Géejawaay ak Ëttu àttewaay bu Pikin-Géejawaay bi ñu fa war a tabax. Ndiisoog toppe gu Ëttu Àttewaay bu kawe baa ngay wéy di yaatal toftaleg ña mu joxoñ baaraamu tuuma. Ginnaaw bi mu fi takkalee jëwriñ ji, Ismayla Maajoor Faal, lamu tànk, toftal ca Séex Géey ak Mohamet Anas El Basiir, tegaat na ca Maam Bóoy Jaawo, Abdulaay Si ak Njiiti pekk ya woon fa Domaines ak Cadastre bu Géejawaay. Andilu nañu itam Mamadu Géey mi ñu jàpp ni dafa daw, génn réew mi. Moo fa mujjoon a nekk njiitul Domaine ca jamonoy Maki Sàll. Jamono yii waa DIC ñoo ngi ciy tànkam.
AIR SÉNÉGAL AK CARLYLE AVIATION DËDDOO NAÑU
Ànd bi doxoon ci diggante Air Sénégal ak Carlyle Aviation a ngi waaj a jeex. Nde Air Sénégal jël na ndogalu dakkal seen lëkkatoo ak delloo ko ñeenti roppalaan yu mu ko luye woon, lu ko dale ginnaaw-ëllëg 19 suwe 2025. Bees sukkandikoo ci xibaar yi jot a rot, ab roppalaan Airbus A319 bu Air Sénégal luye woon te waroon koo delloo ca weeru oktoobar 2024, ak njëg yi Carlyle yokk ñoo waral coow li. Air Sénégal delloowul roppalaan gi ci àpp gi ñu digaale woon. Sàmmontewul itam ak pasug njaay mi ñu waxtaane woon. Looloo tax Carlyle kalaame ko fa kurél gii di IATA (Association Internationale du Transport Aérien). Ginnaaw bi kurél gi daggee ci gafaka Air Sénégal 1,8 milyaari FCFA, njiitu Air Sénégal li, Farba Juuf, jébbal na itam Fabiris Lahiri mi jiite IATA bu diiwaan bi, ab bataaxalu mise en demeure laata mu koy topp ci yoon.
IRÃ-ISRAAYEL : SENEGAAL SÀKKU NA ÑU DAKKAL XEEX BI
Càmmug Senegaal àddu na ci xeex bi jolli ci diggante Irã ak Israayel. Ab yégle la Njëwriñu Bennoog Afrig ak Mbiri bitim-réew génne démb ci altine ji, 16 suwe, ngir wane njàqareem ginnaaw bi Israayel songee Irã, ñàkk kaaraange gi mu nar a yokk fa diiwaan baak ay ya fa jot a juddu. Naka noonu, muy ñaawlu gépp xeetu cong ak jalgati Yoon wi àddina si bokk tënku tey faagaagal jàmm ak kaaraange àddina si. Ginnaaw loolu, Senegal sàkku naat ci ñaar ñépp, ñu dakkal xeex bi ci saa si. Muy dellu di biral ngëmam jëme ci waxtaan ak yaatal lëkkatoo yi ci diggante Réew yi ngir fay ay yi.