LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (17/7/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

SÓOBAREY FARÃS YI GÉNN NAÑU RÉEW MI

Bu yàgg ba tay (1960) sóobarey Farãs yi ñi ngi ci réewi Afrig sowu-jant yi. Mu am yenn ci réew yooyu yu ci tàmbalee jël seen yoonu bopp. Maanaam, xàll yoonu kaaraange woo xam ne duñu ci ànd ak Farãs. Réew yooyu nag, ci la Senegaal bokk. Looloo tax, tay ci alxames ji la sóobarey Farãs yi fi desoon lem seen i godaar, dellu seen réew. Kon, mënees na jàpp ne teewaayu sóobarey Farãs moom jeex na fi réewum Senegaal bés niki tay.

XIBAAR ÑEEL MBIRI YOON

Tay ci alxames ji la Asan Juuf doon jàkkaarloo ak àttekat bi. Dafa di, moom, bu yàgg ba tay, mi ngi ci loxoy Yoon. Li ñu ko doon toppe mooy tasaare xibaar yu wérul, biral kàddu yu dëppóowul ak jikko yu rafet yi ak ŋàññi walla tooñ nit ku am lépp walla lenn ci dayoy Njiitu réew. Tay la doon layoo waaye mujjuñu koo bàyyi. Ndogal li tukkee ci àtte bi dees na ko fésal juróom-ñaari fan ci weeru ut wii ñu dëgmal.

Naka noonu, kii di Musaa Sekk, ñu gën koo xam ci turu Njawar Jaañ, bokkoon ci Xaalisoo, jàkkaarloo na tay ak àttekat bi. Nde, moom itam, ñi ngi ko tëj ci mbirum koppar gu ñu ne da koo luubal. Koppar yooyoo ngi tollu ci juróom-ñetti miliyoŋ ak lu teg. Moom nag, doon na layoo tay. Waaye, mujjuñu koo bàyyi. Dàq nañu layoo bi ba Juróom­-ñaari fan ci weeru ut wii ñu dëgmal.

Kii di Mustafaa Jaxate ak Basiir Fofana, ñoom tamit, dañuy mujjee desaat fa kaso ba. Ndax, ndogal li war a tukkee ci seen layoo génnagul ba tay. Àpp gi ñu leen jàppalaat mi ngi yemoo ak ñaar-fukki fan ak ñett ci weeru sulet wii. Maanaam, ayu-bés bii di ñëw.

Ba tay, ci wàllu Yoon, woolu nañu Faatumata Njaay, ñu gën koo xam ci turu Fuuta Tampi. Suba ci àjjuma ji lañu ko woo fa Sàndarmëri. Li sabab woote bi nag, xameesagu ko. Waaye, balaa yàgg dees na ci xam dara.

WAA SYTJUST-UNTJ ÑU NGI WÉYAL XEEX BI

Fan yee jàll la sàndikaab Yoon boobu dooroon ab xeexam. Booba ba tay nag, delluwuñu ci ginnaaw. Li ñu bëgg mooy ñu teg ci seen loxo lu leer. Ci gàttal, dañoo sonn ci nës-nësal bi ba tax ñu yokk cere dolli ñeex. Nde, dañoo xamle ne dañuy dakkalaat seen liggéey ci diirub ñaari fan. Maanaam, alxamesu tay ji ak àjjumay suba ji dañuy bank seen i loxo, duñu nos, duñu nocci.

NDOG MU METTI FA KAWLAX

Ndog yaa ngi wéy di gën a bari ci réew mi. Nde, tay ci suba rekk am na ndog mu am booy génn gaaraasu Ñooro, fa Kawlax. Benn minibiis moo fa mbëkk genn sëfaan gu taxawoon. Bees sukkandikoo ci waa Seneweb, am na benn bakkan bu ca rot ca saa sa. Mu am juróom-ñett ñu ca jële ay gaañu-gaañu. Juróom-ñett yooyu, am na ci ñeent ñoo xam ne, nee ñu, sonn nañu lool. Li waral ndog ma ba tay xameesagu ko.

XEW-XEW BU YÉEME FA NJURBEL

Xew-xew bu yéeme moo am démb fa dëkk bii di Njis, nekke fa Njurbel. Jenn waay juy wuyoo ci turu A. Ngom, tollu ci fanweeri at ak juróom lañ fa tuumaal ne dafa bóom soxnaam. Soxna saa ngi wuyoo ci turu M. Ñing, tolloon ci ñaar-fukki at ak juróom-ñett. Bàyyi na ginnaawam ñeenti bant. Bees sukkandikoo ci waa Senego, nee nañ bi mbir mi xewee, waa ji dafa daw. Rax-ci-dolli, ci li ñu wax, dafa xamal luññutukat yi ne moo def jëf ju ñaaw jooju. Nee na, coow laa ngi doore ci bi mu ko waxee mu defaral ko ndekki, mu ne ko dara desu fi. Ca la ko fekk ca néeg ba dóor ko. Ba tay, ci li luññutu yi fésal, xaw na wute ak li waa ji wax. Li ñu feeñal mooy dafa mel ni soxna si dañ koo xoj. Moo tax, ñu sàkku ab “autopsie” ngir xam dëggantaan ci yan anam la soxna soosu génnee àddina.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj