SAMP NAÑËTTU ÀTTE BII DI “POOL JUDICIAIRE FINANCIER”
Jëwriñ ji ñu dénk wàllu Yoon samp tay ëttu àtte bees duppee “Pool judiciaire financier” (PJF) te mu wuutu CREI. Ci li jëwriñ ji xamle, moom Usmaan Jaañ, PJF bi yemul rekk ci dii wuutu CREI ba woon, waaye ab jumtukaay bu bees la bob, moo gën a dëppoo ak li jamono ji laaj. PJF mooy ëttu àtte biy topp képp ku laale ci lu mel ni luubal xaalis, càcc, nger, añs. Ëttu àtte la bob, fa tirbinaalu Ndakaaru la féete, waaye réew mépp la boole ëmb. Fépp fu njuuj-njaaj, mbuxum walla jalgati am rekk, ñeel alalu askan wi, PJF dina am sañ-sañu topp ñi ci laale.
UNICEF – SENEGAAL
Njiitu UNICEF (Fonds des Nations Unies pour l’Enfance) lu bees li féete Senegaal, Jacques Boyer, tàmbali na liggéeyam barki-démb ci àjjuma ji. Ginnaaw bi mu jëlee lénge yi nag, yékkati na kàddoom yi njëkk. Naka noonu, muy xamle ni fas na yéene doxal yéeney kurél gi ñeel gunge Càmmu Senegaal ci wasaare ak aar àq ak yelleefi ndaw ñi fi Senegaal. Bu weesoo Càmm gi, dina ci ànd ak kuréli ma-xejj yeek askan yi ngir fexe ndaw lu nekk jot ci sa àq ak yelleef, moo xam njàng mu baax lay doon, faju walla aaru ci taafar yi.
ÑETTI NIT YI ÑU JÀPP FA NJUM
Fa Njum, Sàndarmëri ba jàpp na fa ñetti nit démb ci guddi dibéer ji jàpp altine. Ñoom nag dañoo fekk ñu yor lu tollook 2i kiloy yàmbaa yu ñu def ci 480i laxas. Fekk ñu toggoo ab moto, doon jéem a jàll fa réewum Móritani. Fekk nañ ci ñoom itam xaalis. Jamono yii ña nga ñu tée fa sàndarmëri bu Njum di xaarandi gëstu bi jeex.
AES SÀKK NA PAASPOORU BOPPAM
Réewi AES (Alliance des États du Sahel) yi dinañu am seen paaspooru bopp. Njiitu réewum Mali li, Kolonel Asimi Goytaa, moo ko siiwal démb ci dibéer ji. Fekk ñu doon màggal ci gaawu gi menn at ginnaaw bi ñu sosee seen lëkkatoo gi ca sàttumbar 2023. Naka noonu muy xamle ni ci fan yii di ñëw, dinañu génne paaspoor bi ñu tëgg-bees ngir yoonal dem beek dikk bi ci seen biir. Xamle naat ni ñoo ngi liggéey ci taxawal i tabaxte ngir dëggëral seen jokkalante, jaare ko ci yaale ji, mbaalu jokkalante yeek xarala yi.