Limu wotekat yi bindu ci këyitu wote gi mi ngi tollu ci 7 300 000iy Saa-Senegaal. Waaye, ci lees jot a natt, lim bi jot a wote taxu ko bari noonu yépp. Ndax, ci téemeer boo jël, daanaka 50 yi kott ko jooxe. Muy wone ni Saa-Senegaal yi gënoon nañoo génn ca wotey Njiitu réew ma ñu doon amal bu yàggul dara. Waaye, ba tay, lim bi ñu am ci wotey Ngomblaan gi ci atum 2024 mi moo tane bees ko gam-gamlee ak ba woon ca atum 2022 te yamoon ci 46,64%.
CENA BI RAFETLU NA TAXAWAAYU MA-XEJJ YI
Ginnaaw bi ñu amalee wote yi démb ba noppi, CENA bi (Commission électorale nationale autonome) xamle na ni wote yi amal nañu leen fi réew mi ak fa bitim-réew ci jàmm ak dal. Nde bi pekk yi di tijji ci 8i waxtu ba bi ñuy tëj ci 18i waxtu, ñëw nañu, jooxe seen àq ak yelleef ci ni mu waree. Te, loolu dafay dellu di firndeel taqoo gi Senegaal ak Saa-Senegaal yi taqook laltaayi demokaraasi. Ba tax muy rafetlu taxawaay bi mucc ayib bi ma-xejj yi am. Muy taxawaay bu mat a roy te di firndeel seen mat ci ma-xejj yi ñu doon. Jaajëfal naat takk-der yeek saytukati kaaraange gi ci seen taxawaay ci bépp barab bu ñu doon wotee.
JÀPP NAÑU KI TOPP CI MEERU WAAKAAM BI
Fa Wakaam, teg nañu loxo ka topp ca ginnaaw meer ba, te di wuyoo ci turu Ndey Top Géy. Moo ngi bokkoon ci toftaleg Sàmm sa Kàddu ca gox ba. Lees koy toppe nag mooy yoonu wuruj wi ñu ne la sumboon ci wote yi. Nde, dafa feyoon ay nit, solal leen i mbubbi saabalkat te doonuñu ko. Naka noonu, mu wutal leen i kàrt ngir ñuy dugg ci pekk yi ak di ko dajalaatul i xibaar. Jamono yii nag, ma nga ca loxoy yoon, moom ak ki ko ci doon jàppale. Ñu leen di toppe wootewoo liggéeyu jàmbur, wuruj ak jëfandikoo wuruj.