Coowal muuraay yi ci lekool bi dekkiwaat na. Démb ci altine ji, njiiti lekool bii di Collège Saint Grabriel de Thies dañu xëyee tere ndongo yu bari, rawatina ay jigéen, ñu dugg fa jàngu ba ndax li ñu muuru. Bees sukkandikoo ci yégle bi kilifa yiy saytu njàng mi (Inspection d’Académie) siiwal, ndogal lu ñu jël la ngir ga ndongo yi ci ñu sàmmonteek buluusi lekool ba. Nde, yenn ci kol yi dañuy nëbb daanaka buluus yi. Waaye, seetlu nañu ni am na ci jigéen ñu muuru ni mu waree te terewul ñu dàq leen. Ginnaaw luññutu gi, kilifa ya jox nañu ndigal njiitu lekool ba mu dugalaat xale yu jigéen yépp ca saa sa, te sàmmonteek seen i àq ak yelleef ñeel njàng mi.
ÀTTEB NEENAL BI
Abdul Mbay, nekkoon fi elimaanub jëwriñ ci jamonoy Maki Sàll, biral na xalaatam ci coowal dakkal as lëf walla léppi àtteb neenal bi aju woon ci xew-xewi pólitig yi fi amoon ci ñetti at yii weesu. Naka noonu, muy xamle ni bees àndulee cib àtte, dees koy dakkal bu mënee nekk. Waaye, di ko wéyal ak a woyofal déggiin wi dafay wane ni àndees na ci. Naka noonu, muy xelal kilifa yu bees yi ñu dakkal àtteb neenal bu 2024 bi te wotelu beneen bu gën a méngook seen i jubluwaay. Te ci lii sax, bu ñu fàtte jëfandikoo xelu campéef yi ci seen xel màcc.
BITIM-RÉEW
Réewum Ruwàndaa dog na digganteem ak réewu Belsig. Démb ci altine ji, 17 mars 2025 lañu biral xibaar bi, wax ni dakkal nañu lépp luy jëflante ci seen diggante ci wàllu dipolomasi. Li waral loolu ndogal nag mooy dañuy jiiñ réewum Belsig ni dafa dugal loxoom ci mbiri RDC (République démocratique du Congo), wane ci param lu jiitu xeex bi fay am nii di tàmbali. Te ba léegi, looxoom a ngi ci biir.
KAARAANGE RÉEW MI
Ci ayu-bés bi ñu génn, pólisu réew mi jàpp na lu tollu ci 1489i doomi Aadama. Fekk ñu doon amal i coytu yu jëm ci wattu kaaraange dëkk ba. 764 ci ñi ñu jàpp, fekkuñu ci ñoom dàntite. Mu am 164 ñoo xam ni laaj na ñu amal ci ñoom ay luññutu ngir leeral njort ci ñoom. Waññi nañu ci lu tollu ci 116 yu ñu fekk ci ñoom sineebar, ak 85 yu doon wër di sàcc.
Bu weesoo ñooñu, jàpp nañu 15 yoo xam ni dañu defoon seen um mbooloo di def i ñaawteef. Am na ci itam ñoo xam ni dañu leen fekk ñu màndi ba ne tat, ñépp teg ci seen i bët.