Démb ci altine ji lees woolu woon dépite yi ca Ngombalaan ga ngir ñu saytu ci lu gaaw sémbiy àtte yi leen Nguur gi jébbal ginnaaw péncoo mi fi amoon. Waaye, coppite gi jëm ci dogub 87 bu ndeyu àtte réew mi jur na coow lu bare ci biir dépite yi, jaare ko ci way-pólitig yi ba ci askan wi.
Lees ciy ragal, te ñu mel ni Bugaan Géy Dani walla Séex Bàmba Jéey tudd ko, mooy ni Njiitu réew mi dina fi jaare am sañ-sañu tas Ngombalaan gi saa bu ko neexee. Te mbir yi dafay mel ni Njiitu réew mi biral na ni du bokk ci wote yii di ñëw waaye génnewul xelam ci Nguur gi. Wote bi nag, bëtal nañ ko ba alxames jii, 20 sulet 2023.
Jàpp-tëj yi jeexagul
Yoon tegati na loxo kii di El Maalig Njaay.Bërki-démb, ci dibéer ji la ko waa DIC jàpp, bees sukkandikoo ci li layookatam bii Sñ Musaa Saar. El Maalig Njaay sax, di ki yor jokkoo bu Pastef, bokkoon na ci waa pastef yi ñu njëkkoon a teg loxo ci jamono yee weesu. Waaye dañ ko bàyyi woon bàyyib négandiku. Looloo waraloon ba ñu takkal ko lamu tànk bu koy tere génn diwaanu Ndakaaru.
Moom nag li waral ñu jàppaat ko dese naa leer. Waay bees sukkandikoo ci li sunu naataangoy Sud fm siiwal lees ci xamagum mooy ne dafa bokkoon ci ñi doon amal i yëngu-yëngu ak a tëgg i bool naka gaawu ci guddi, bi ko njiitul Pastef li Usmaan Sonko sàkkoo ciy ñoñam. Am ñuy wax ne dafa am ndéggat lu mu def, di ci xirtal ndaw ñi ngir ñu génn taal réew mi.
Gaal ga suux ca Ndar
Limub ñi ñàkk seen bakkan ca gaal ga suuxoon fa Ndar a ngi gën a yokku. Ginnaaw fukk ak juróom yees gisoon, làqi waat nañ ñett ñoo xam ni ca gaal ga lañ nekkoon. Lim baa ngi tey ci fukk ak juróom-ñetti nit ñu ci faatu. Jamono yii, sàppëer yeek marin bee ngi wéyal ceet gi ba tey.
Afro basket 2023
Mustafaa Gaye miy tàggat gaynde Senegaal yu jigéen yi siiwal na turi xale yi mu namm a yóbbu. Ñi ngi tollu ci fukk ak ñaari jigéen. Ñu ràññe ci Ummu Xayri Saar, Ayaa Taraawore ak Yaasin Jóob ñi nga xam ne miis nañ ekib bi. Ràññees na ci tamit teewaayu kii di Siyeraa Jànney Dilaar mi fekk baax ca réewum Amerig te taamu doon Saa-Senegaal. Joŋante yee ngi war a amee ca Kigali, réewum Ruwaandaa. 18 sulet bii di ñëw lañuy mbir yiy door.