Seydu Géy mi yor kàddu waa APR àddu na ci coow li topp seen pàrti bi. Fekk ñu dalaloon ko démb ca jotaayu Grand Jury bu RFM. Moom nag, waxtaan la woote ginnaaw ba ñenn ci seen biir àndulee ci Aamadu Ba mi Njiitu Réew mi tànn. Muy fàttali Aali Nguy Njaay ak ku mel ni Buun Abdulaay Jonn liggéey bu rafet bi ñu def ci at yii ñu génn. Ba tax mu leen di woo ci ñu waxtaan te jéem a bennoo ngir wéyal liggéey bi.
GÀMMU TIWAAWAN 2023
Li des ci Gàmmu gi, di guddi gi ñuy Màggal juddu yonnent Yàlla Muhamet, bareetul. Jamono yii, këru diine yi koy màggal ñoo ngi ci waajtaay yu réy, rawatina ci wàllu wér-gi-yaramu way-màggal yi. Ci gaawu gii ñu weesu, Mari Xemes Ngom Njaay a nga woon ca Tiwaawan. Ci yégle bi ñu siiwal, ña nga cay xamle ni lu tollu ci 3000iy doom-aadama yoy seen xel màcc na ci wér-gi-yaram dinañu leen tas ca biir dëkk ba ngir ñu taxawu nit ñi ci anam yi gën.
TÀGGA-YARAM
Basket : As Douwanes nekk na sàmpiyõ Senegaal 2023. Démb ci dibéer ji la doon joŋante gañ-jël bi ci digganteem ak Jeanne d’Arc bu Ndakaaru. Naka noonu, mu daldi am ndam ci kowam ginnaaw bi mu ko daane 64-56. Sàmb Daali Faal, bokk ci ekibu Douanes bi, lañ tabb mu nekk ki gën a xarañ ci gañ-jël bi.
AS Douanes nag moo jëloon Sàmpiyonaa bi daaw (2022) daldi koy jëlaat ren (2023).
BITIM-RÉEW
78eelu Ndajeem Mbootaayu Xeet yi (Session ordinaire de l’Assemblée Général des Nations unies) a ngi ñuy amal jamono jii ca New York (USA). Njiitul réew mi Maki sàll bokk ca ña koy teewe li ko dale démb (17 sàttumbar) ba gaawu bii di ñëw (23 Sàttumbar 2023). Moom Njiitu réew mi sax, ma nga ñuy xaar cib jotaay bu war a am ci kilifteefam. Ñu war caa waxtaane lu ñeel kopparal ODD yi, di ci nasaraan Objectif de développement durable.