Ayib Dafe, ndawul Usmaan Sonko miy lawax ci wotey 2024 yi, sooyati na. Ndax, dafa dellooti woon fa DGE, moom ak layookat bii di Sir Keledoor Li. Li ñu ko dugge woon mooy jëli xobi baayale yi ginnaaw bi leen tirbinaalu Ndakaaru bi joxee ndam, wax ne nañ delloo Usmaan Sonko ci wayndarew wote wi.
Ba ndogalu àttekat ba jibee, jox Usmaan Sonko dëgg, ñépp ñoo ngi doon séentu Ayib Dafe fa DGE. Moom, nag, yàkkamtiwul woon i mbiram. Dafa bindoon wax ne :
« Salaam ñépp. Noo ngi sëgg ci sunu liggéey. Dinanu wax bu wax jotee. Nu ànd ak teey, dogu ak dal. »
Bataaxel bii rekk la biraloon. Tey ci talaata ji nag, delluwaatoon na DGE. Waaye, dafa sooyati. Waa DGE ñoo ngi dëgë bopp ba tey. Boobaak léegi, mi ngi fay jaabante, te jotagul la muy jëli. Waa DGE nag, wile yoon, kenn déggu leen. Dañu ne patt-pattiiral.
WOTEY 2024 YI
Ñaari weer képp a des ci wotey 2024 yees war a falee Njiitu réew mu bees. Ba tax waa LACOS (Leaders Alliés du candidat Ousmaan Sonko), di kurélu njiit yiy jàppal tànk Usmaan Sonko, dellu di ñaax askan wi mu farlu ci jëli kàrt yi. Ñu fàttali ni xeex bi ñuy xeex ngir andiy coppite ci réew mi demagul bay waaj a jeex. Askan wi rekk moo ko mën a jeexal ci kow ñu jóg ca ba muy teel, dem jëli seen i kàrt te takku doon benn ngir jële fi Maki Sàll ak i ñoñam ci jàmm.
NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI
Barki-démb ci gaawu gi, 16 desàmbar 2023, doon nañ màggal bés bees jagleel daara yi fi réew mi. Bu ren bi di ñaareel bi yoon ginnaaw bi ñu ko tàmbalee def daaw. Naka noonu, Njiitu réew Maki Sàll teewoon na fa. Bi mu jëlee kàddu gi, xamle na ni Càmm geek ñi muy àndal ci liggéey bi dugal nañ ci sémbub méngale daara yi ak jamono lu tollu ci 25i tamndaret, ci atum 2012 ak tey. Wax na itam ni seetlu nañ ci jéego yu am solo diggante daaw ak ren.
NGOMBALAAN GI
Tey ci altine ji, dépite yi doon nañ fénc fa Ngombalaan ga nees war a saafaraa jàmmaarloo yi ñuy faral di seetlu ci diggante baykat yeek sàmm yi. Léeg-léeg sax mu ëpp i loxo ba ay bakkan rot ci. Naka noonu, dépite yépp mujje nañ ànd ci jàllale ab sémbub àtte. Muy sémb bob jëwriñ ji Daawuda Ja rafetlu na ko lool. Muy xamle ni ci xalaati way-yëngu yi ci wàll wi lañ ko nase te gis na ni yemul rekk ci dakkal coow yooyu. Nde dafa ëmbaale lépp lu jëm ci xeex càccum njur geek yi ni mel tey.
BITIM-RÉEW
Lakk gu metti moo am fa réewum Gine. Menn sàqum karbirãŋ, di béréb bu ñuy defere yu deme ni gaasuwaal beek esãs bi, moo jekk saa rekk tàkk. Bees sukkandikoo ci xibaar yi ñu mujje jot te Basiiru Jàllo, jëwriñ ja yor kaaraange biir réew ma, siiwal leen, lakk gi fay na waaye kenn xamagul nag li ko sabab. 30i doom-aadama ñàkk nañ ci seen bakkan. Am naat ñu bare ñu ci jële i gaañu-gaañu. Jëwriñ ji xamle naat ni dinañu taxawal ag kurél gog dafay jàppale ña ca loru.