LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (19/6/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

ELIMAAN JËWRIÑ YI ÀDDU NA CI JAFE-JAFEY GAYNDEY BASKET YU JIGÉEN YI

Gaynde yu jigéen yiy basket dañoo amoon jafe-jafey amal seen ub tukki fa Etaasini. Li ko waral du lenn lu moy dañoo bañ a jox ñenn ci ñoom ay wiisaa. Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, àddu na ci mbir moomu ci xëtu Facebookam. Nee na jox na ndigal jëwriñu tàggat-yaram ji mu bàyyi waajtaayu fukki fan yi ñu naroon a amal foofa ca Etaasini, te ñu amalee ko fii ci Ndakaaru ci anam yu mucc ayib. Nee na tamit, mi ngi gërëm waa Siin ñi nga xam ne may nañu leen ay fukki fukki “bourses” ngir ataleti Senegaal yi ak ñi leen di tàggat. Li ñu ko dugge mooy waajal powi olimpigi ndaw ñi fi Ndakaaru, atum 2026. Laata muy jeexal, xamle na ne dañoo soppi doxalin ñeel seen i jokkalante ak seen digganteek yeneen réewi àddina si. Te, xeetu doxalin woowu, mi ngi tënku ci gis-gisu Njiitu réew mi, méngoo tamit ak doxalinu làngug PASTEF.

TUKKIB NJIITU RÉEW MI

Ginnaaw bi mu amalee tukkib ñaari fan ci bëj-gànnaaru réew mi, Njiitu réew mi Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jëlaat na aw yoon. Wii yoon moom, dafay génn réew mi. Waaye, ba tay, mi ngi ci kembaaru Afrig gi. Nde, fale ca ndajem CEDEAO ma la jëm. Ndaje mooma, ma ngay ame fa Abujaa, réewu Niseriyaa, ñaar-fukki fan ñaar ci weeru suwe wii. Li ñu dugge ndaje mooma, mooy waxtaane mbiri kaaraange, pólitig ak koom yi nga xam ne yitteel na réewi Afrig sowu-jant yi.

JËWRIÑU KOPPARAL YI AK NAFA GI INDI NAY LEERAL

Fan yii dafa am xibaar bu ñuy tasaare ci mbaali jokkoo yi di ci xamle ne réewum Koddiwaar mooy kopparal réewum Senegaal. Jëwriñ ji génnee na ab yégle ngir indi ci ay leeral. Mi ngi xamle ne xibaar yooyu wérul. Nde, dafa jaadu ñu xam ne ñoom ñoo bokk jawu UEMOA. Te, dafa am nu muy doxe. Kon, li mat a xam mooy amul kopparal gu dox ci diggante ñaari réew yi. Juróom-ñaar fukki miliyaar ak juróom-ñaar yi ñuy wax du dëgg.

XIBAAR ÑEEL YOON

Fan yee jàll lañu tegoon loxo kii di Mustafaa Jaxate. Booba ba tay nag, mi ngi ci loxoy Yoon. Dafa di, moom doon nañu ko àtte. Waaye, loolu taxul ñu leeral ci daan bi war a tegu ci ndoddam. Loolu dees na ci xam dara ñaari fan ci weeru Sulet.

Kii di Farba Ngom tamit, ba tay ma nga ca kaso ba donte ne sax àttekat bi joxe woon na ndigal ngir ñu saytu wér-gu-yaramam. Loolu taxul ñu bàyyi ko. Li fajkat bi xamle mooy am na jàngoro yu muy sooxaale. Te, ag nekkam ci kaso bi bu leen yokkul, du leen wàññi. Dafa laaj kon ñu toppatoo ko donte ne sax, fajkat bi xamle na jàngoro yooyu jàppul ne mën nañu koo ray tembe.

Naka noonu, kii di Lat Jóob tamit, day des ca kaso ba. Li waral loolu du lenn lu moy ndogalu ëttu àttekaay bu kawe bi. Nde, moom Lat, dañu ko nanguloon càkkuteefu bàyyig négandiku gi mu jébbaloon. Ëttu toppe gu mag gi moom àndu ci woon. Looloo tax, bi dabantal bi duggee lañu neenal ndogal li waa “chambre d’accusation financière” jëloon. Maanaam, may Lat Jóob bàyyig négandiku boole ko ak takkal ko ab lam.

NDOGUM YOON MU METTI FA DAARA

Am ndog mu metti moo am démb ci ngoon ci yoonu Daara-Tuuba wi. Benn minikaar moo fa daanu. Li sabab daanu bi mooy póno baa toj, mu mbëkk ag garab. Bees sukkandikoo ci waa Senego, ñaari nit ñàkk nañu ci seen bakkan. Fukk ak juróom-ñaar jële ci ay gaañu-gaañu. Mu am fukk ak benn yoo xam ne mettile nañu lool.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj