LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (2/1/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NEKKUG LAWAXU USMAAN SONKO

Ndaje mu mag la ñoñi Pastef gi woon waajaloon a amal ci gaawu gi ngir tabb Usmaan Sonko mu doon seen lawax ci wotey 2024 yi. Ginnaaw bi ko perefe bu Ndakaaru gàntalee, mujje nañ ko amal démb ci dibéer ji, jaare ko ci mbaali jokkoo yi. Bu weesoo Mustafaa Giraasi mi àndoon ak waa làngu pólitigam SET (Sénégal en Tête) daldi tabb Usmaan Sonko, yeneen 27i làngi pólitig fekkisi nañu leen ci Lëkkatoo Sonko 2024 (Coalition Sonko 2024). Ñuy xaar nag ndogal li way-saytu ndeyu àtte réew mi namm jël ci nekkug lawaxu Usmaan Sonko ci àjjuma jii di ñëw (5 sãwiyee 2024).

CÀMBARUG WAY-SÀKKU LAWAX YI

Way-saytu ndeyu àtte réew mi def nañ bilaŋu bés bi njëkk ñeel càmbarug way-sàkku lawax yi. Ci yëgle bi ñu génnee, jot nañoo càmbar17i wayndare ci gaawu gi. Waaye, 21 lañ waroon a càmbar. Ñeent lañ jotul a laal. Ñuy bu Usmaan Sonko ndax li ndawam teewul woon ; bu Elaas Ibraayma Mbów mi yëgaloon way-saytu yi ni génn na ci xëccoo bi ; ak yu Maalig Guéy ak Mamadu Sàmbu Yatasaay nga xam ni li seen i wayndare dëppoowul ak anam wi jëwriñ ji ñu dénk kaaraange biir réew mi joxe moo waral ba mëneesu leen càmbar.

MAKI SALL TÀGGATOO NA

Keroog, ci dibéer ji, Njiitu réew mi, Maki Sàll yékkati woon nay kàddu ci njeexitalu at mi (2023) ngir tatagal at mu bees mi (2024). Ni mu ko daan defe at mu jot nag, la ko defe : wax ci tolluwaayu réew mi, sémb yi mu jot a sottal ak yi mu nekk di doxal. Waaye bu atum ren ji, di fukkeelu yoon week ñaar ginnaaw bi mu nekkee Njiitu réew mi ci 2012 ak tey, am na tuuti lu mu wuuteek yi weesu. Nde dafa yam ak njeexalam ci boppu réewum Senegaal, ba tax mu doon ci yékkatiwaale ay kàdduy tàggatoo.

Ci kàddu tàggatoo yooyu sax, moom Njiitu réew mi fésal na ci yéeneem bés bu demee ba jóge ci boppu réew mi. Li mu bëgg mooy taxawal ab kurél gog, dafay dox tànki jàmm. Naka noonu, dina doon jumtukaay ngir mu mën a jooxe yitte yi ko gën a soxal ; yi deme ni dëkkaale askan yi, ak mbatiit yeek xayte yi, añs.

BITIM-RÉEW

Fa réewum Càdd, ñaari at ak lu teg ginnaaw ba Mahamat Idiris Debi, doom ci Idiris Debi mi faatu ci atum 2021, tegee loxo Nguur ga, Càmm gu bees a ngi ci tànki taxaw. Barki-démb ci dibéer ji la ko Mahamat Idiris Debi ci boppam xamle. Fekk mu doon yékkatiy kàddu ci at mu bees mi ñuy dugg. Tey ci altine ji mu daldi jël ab dekkere ngir tab jëwriñ ju mag ji war a jiite Càmm gu bees gi. Li xaw a yéeme ca mbir ma nag mooy Sukses Masraa mi gënoon a metti ca kujje ga ba ñu jàppe woon ko noonu dëkk ba lañ tabb ngir mu jiite Càmm googu. Ñuy xaar ci moom ak Càmm gi mu nar a àndal ñu taxawal campeef ak ay àtte yu yees ñeel wote yi, ni ko ndeyu àtte réew ma bëggee, te amal i wote ngir génne réew ma ci guuta gi ñuy dund at yii yépp.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj