LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (2/1/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

BÀRTELEMI JAAS TEGGIWUL TÀNKAM

Ginnaaw bi Yoon nangoo moomeg dépiteem ak cëru meeru Ndakaaru, taxul Bàrtelemi Jaas bàyyi mu sedd. Booba ba tey, mi ngi ci banqaasi Yoon yi, di jébbal ay dabantal. Jotoon na a jébbal ay dabantal fa ndajem ndeyu-àtte mi ak fa ëttub dabantal bi “Cour d’appel” ngir ñu neenal ndogal yooyu. Waaye, loolee mujjewul a àntu. Nde, ëtt yooyu dañoo gàntal i dabantalam. Bi loolu jàllee nag, ay layookatam xamle nañu ne dinañu jébbalaat ñaari dabantal fa ëttu àttekaay bu kowe ba, di “Cour suprême”. Li mu ko dugge du lenn lu moy ñu delloo ko moomeg dépiteem fa Ngomblaan ga ak meeri Ndakaaru bi ñu nangu ci moom. Te, lenn waralu ko lu moy daan yi tegu ci ndoddam ñeel bóomug Njaga Juuf.

SÉEX BAARA NJAAY AK TEREES FAY JUBOO NAÑU

Bu yàgg ba tey, ñoom ñaari dépite yooyu ñi ngi dem ak dikk ci Yoon ngir lijjanti coow li doxoon seen diggante. Nde, kii di Séex Baara Njaay dafa am ay tuuma yu mu tegoon ci deram. Ndax, daf ne woon ndaw soosu alal ju bari la yor. Te, ci at yii mu nekk ci Nguur gi la ko am. Maanaam, am-amam xaw na teey xel. Waaye, dafa mel ni coow loolu jeex na. Te, ginnaaw ay, jàmm. Soxna si nee na dina dindi jure bi. Moom, Séex Baara Njaay tamit jéggalu na ko ginnaaw ñoom ñaar ñépp ñoo bokk kër gu ñuy xëy, muy Ngomblaan ga.

NJÀNG MI DINA DOORAAT FA UASZ

Fan yale jàll lañu tëjoon daara ju kowe jooju nekk fa Sigicoor. Li ko waraloon mooy jafe-jafe yu ndongo yi doon jànkonteel fa jàngune ba ak coow ya fa amoon. Ndogal loolu kilifa yi jëloon nag, juroon na coow lu bari ci réew mi. Waaye, dafa mel ni déggoo mujj na am ci diggante bi. Ba tax na, njàng mi dina dooraat fa béréb boobu, altine jii ñu jëm juróom-benni fan ci weeru sãwiyee.

LÀMB BÀLLA GAY 2 AK SITTA TAXAW NA

Ci weeru nowàmbar wee jàll la kii di Sitta doon bëre ak buuru làmbu ji, Móodu Lóo. Waaye, moom Sitta, jëlewu ca ndam. Kii di Bàlla Gay 2 moom, ci ndam la jóge. Ndax, moo daan Tafaa Tin lu yàggul dara. Ñaari jàmbaar yooyu nga xam ne kenn dootu leen aajar ci làmb ji, ñoom la Al Buraax Events boole. Ñu war a sëgg ñaar-fukki fan ci weeru sulet, atum 2025.

XEW-XEW BU TIIS FA MALIKA

Xew-xew boobu mi ngi am ci guddig njeexitalu weer ak atum 2024. Maanaam, fanweeri fan ak benn ci weeru desàmbar. Jenn waay juy wuyoo ci turu El H. M. Faal, tollu ci fanweeri at ak juróom-ñaar, moo doon jéem a sàkku benn xale bu jigéen ba noppi bóom ko. Xale bu jigéen bi mi ngi wuyoo ci turu J. Sow, am lu tollu ci fukki at ak ñaar. Moom, waa jooju, ñu jàpp ne (présumé) moo def jëf ju ñaaw jooju, dafa dawoon. Waaye, mujj nañu ko teg loxo.

BENEEN XEW-XEW BU DOY-WAAR FA MBUUR

Xew-xew bii moom, ma nga ame fa kasob Mbuur. Gaa ñiy wattu la fay duggu ak la fay génn ñoo daj ci mbir mu yéeme lool. Ndax, kenn umpalewul ne béréb yooyu lekk daf fay dugg. Dafa am nag, ku fa indi bool bu def ñaari ginaar. Ndekete yoo, ginaar gu ci nekk dañu cee dugal kornetu yàmbaa. Ki indi woon bool ba moom teg nañu ko loxo. Naka noonu, ki mu doon indil lekk gi tamit dees na ko génnee tay ci alxames ji fa mu nekk bees sukkandikoo ci waa “Seneweb”. Ndax, Njiitu “police judiciaire” bi dafa ubbi ag luññutu ngir xam dëgg-dëgg nan la mbir moomu deme.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj