Aliw Tin yëy na yàbbi ci ni demokaraasi bi tëdde ci biir réew mi ak Usmaan Sonko mi ñu seppi ci wotey 2024 yi. Muy xamle ni, bu njëkk, jafe-jafey pal gu jaar yoon lañu daan am ci wote yi. Ay càcc ak yu ni mel lañ daan seetlu. Waaye, léegi, jafe-jafe yi dañuy tàmbali laata sax wote yi di agsi. Ay ku war a bokk ak ku warul a bokk. Mu gis ni dellu ginnaaw gu réy la te dara yóbbeewu ko réew mi lu dul Nguur gu tëddeewul njaaxaanaay.
NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI
Lekkool bi tijji na tey ci altine ji. Waaye jàngalekat yi kott a waroon a teew ngir natt tolluwaay yeek jumtukaay yi. Ndongo yi ñoom, ñoo ngi leen di xaar ci alxames ji ngir ndoorte njàngale yi. Terewul nag ñu seetlu ay rëq-rëq ci yenn barab yu deme ni Géejawaay nga xam ni bindu yi jaaruñu yoon ndax li liggéeykati gox-goxaat yi bank seen loxo jamono jii.
MBËKK MI
Démb ci dibéer ji, geneen gaal naroon naa bawoo Mbuur, utali tugal. Waaye, dafa mujje lajj. Nde Birigàdd bu Ñaaniŋ moo dog yoonu way-tukki ya ca tefesu Pointe Sarène, daldi cay jàpp lu tolloog 31i nit. Bees sukkandikoo ci sunuy naataango yu Dakaractu, Sàndarmëri teg na loxo kamiyoŋ bi leen yeboon. Mu des ci seet gi ñi leen naroon a yóbbu. Mu mel ni xeex bi Nguur gi di xeex mbëkk mi taxul wenn yoon ndaw yi teggi seen tànk. Ba tax kilifa yi dellu di ñaax askan wi ngir ñu gën leen a jàppale ci xeex bi.
TÀGGAT-YARAM
Dàqandi nañu bokkadil yu CHAN (Championnat d’Afrique des Nations) 2024 bi. Li ko waral nag di lu ñu xamagul ba léegi réew mi ko war a dalal. Looloo toxoon ba joŋante yi waroon a am ci weeru sàttumbar bi mujj ñoo am. Yi ñu waroon a joŋante ci weeru màrs 2024 beet ajandi nañu leen. Ñuy ragal sax yóbbu CHAN bi ba 2025. Nde, ba léegi amul menn réew mu ko bëgg a dalal ci 2024 bi.